Important Lessons
1 videosAblution
3 videosPrayer
3 videosImportant Questions
272 questionsxaajub pas-pas42
kan mooy sa Boroom?
Yallà mi ma sakk sakk mbooleem bindeef yi di leen taxawu ci gépp anam mooy sama Boroom.
tektal bi mooy waxi Yàlla mu kawe mi: cant ñeel na Yàlla miy Boroom mbindeef yi [suuratul fatiha 2]
lan mooy sa diine?
diiney lislaam mooy sama diine,te lislaam mooy nga wommatul Yàlla ci wéetal ko ak topp ay santaaneem te set wecci ci bokkaale ak ñi koy def
Yàlla mu kawe mi neena: diine fa Yàlla mooy lislaam suuratu aali himraan 19
kan mooy sab yonnente ?
Muhammat mooy sama yoneent Yàlla na Yàlla julli te sëlemal ci moom.
Yàlla mu kawe mi neena: Muhammat yonnent Yàlla la. suuratul fathi 29
lan mooy baatub tawhiid ak lan lay wund ?
baatub tawhiid mooy " لا إله إلا الله " liy maanaam baat bi mooy amul kenn ku niy jaamu ci dëgg ku dul Yàlla.
Yàlla mu kawe mi neena: na nga xam ne amul kenn ku ñuy jaamu ci dёgg ku dul Yàlla. suuratu Muhammat 19.
ana Yàlla mu magg mi te kawe ?
Yàlla ma nga ca asamaaw ya ca kaw aras féete kaw mbideef yépp, Yàlla mu kawe mi neena: Yàlla miy Boroom yërmaande ju yaatu ji ma nga yamoo fa kaw aras. suuratu taahaa 5 wax na batay: Yàlla mooy notaakon bi féete kaw jaamam yépp mooy Aji- xarañ ji te deñ kumpa. suuratul anhaam 18
lan mooy maanaam seede ne Muhammat yonnenteb Yàlla la ?
maanaam loolu mooy nga nanggu ne yonnente bi Yàlla moo ko yónni ci mbideef yi muy bégal ñi ko topp di xupp ñi ko moy
te war na:
ñu topp ko ci li mu santaane.
te war na it ñu dëggal ko ci lépp lu mu ñu xibaar.
te ñu bañ a wuute ak moom.
te mu bañ a jaamu Yàlla lu dul ci li mu yoonal maanaam ñu tënku ci sunnaam bay lépp luy bidaa.
Yàlla wax na ci suuratu nisaahii ne képp ku topp yonnente bi toppu nga Yàlla, mu dellu waxaat ne: ﴾Yonnente bi du waxe ci bànneexu bakkanam, lumu wax dees ko koo yenkeewal﴿ suuratu annajmi 3;4 Yàlla mu kawe mi te sell neena: ﴾am ngeen ci yonnente bi ab royuwaay bu rafet ñeel képp ku yaakaar Yàlla te gëm bIs pénc tay tudd Yàlla lu bari﴿ suuratul ahzaab 21
lan moo tax Yàlla bind nu ?
Yàlla daf noo bind ngir nu jaamu ko moom dong te bañ koo bokkaale ak dara.
bindu nu ngir ay caaxaan walla am po.
Yàlla mu kawe mi neena: ﴾Binduma jinne ak nit lu dul ñu jaamu ma. ﴿ suuratu azaariyaat 56
lan mooy jaamu ?
loolu de ab baat la bu làmboo lépp lu Yàlla bëgg te gërëm ko ci ay wax ak ay jëf ci lu feeñ ag lu nëbbu.
Li feeñ nag mooy lu mel ni tudd Yàlla ci làmmeñ ci di sàbbaal ak sant ak màggal walla julli ak aji Màkka.
Li nëbbu mooy lu mel ni wakiirlu ci Yàlla ak ragal ko ak yaakaar ko.
lan mooy li gën a rëy ci li war ci nun?
li gën a rëy ci li war ci nun mooy weetal Yàlla.
yan ñooy xeeti tawhiid yi ?
1) tawhiidu arrubuubiyatu maanaam wéetal Yàlla ci ay jëfam: te mooy nga gëm ne Yàlla mooy Aji-bind ji, di wërsëgale te moom dong mooy ki moom lépp, di ko saytu amul kenn kuñ koy bokkaale.
2) tawhiidu al uluuhiyatu, maanaam wéetal Yàlla ci say jëf: loolu mooy wéetal Yàlla ci jaamu ko moom dong bañ koo bokkaale ak dara.
3) tawhiidul asmaahi wassifaati, maanaam wéetal Yàlla ci ay turam ak ay meloom:loolu mooy nga gëm ne Yàlla am na ay tur ak ay melo yu ñëw ci Alquraan ak sunna nga gëm ko bu wér te bañ koo melal walla di ko nuroole ak lenn walla di ko weddi.
liy tektale ñatti xeeti tawhiit yii mooy wax i Yàlla mu kawe mi: Yàlla mooy Boroom asamaan yi ak suuf yi ak li ci séen diggënte,kon jaamu ko moom dong te nga xam ne amul ku mel ni moom ci ay tur walla aw melokaan. suuratu Maryama 65
lan mooy bakkaar bi gën a rëy ?
bakkaar bi gën a rëy mooy bokkaale Yàlla.
Yàlla mu kawe mi neena: Yàlla du jéggal ku deewaale ag bokkaale waaye dina jeggale lu dul bokkaale ñeel ku ko neex te képp kuy bokkaale Yàlla def na bàkkaar bu rëy. suuratu annisaa
waxal lan mooy bokkaale ak i xeetam ?
bokkaale mooy defal keneen ku dul Yàlla lenn ci xeeti jaamu yi.
ay xeetam:
bokkaale gu mag; lu ci mel ni ñaan keneen ku dul Yàlla, walla sujjootal keneen ku dul Yàlla, walla rendi dara ngir keneen ku dul Yàlla.
bokkaale gu ndaw ni ki giñ ci keneen ku dul Yàlla,walla takk ay gàllaj walla yu ni mel ngir mu jariñ la dara walla mu daqal la ay lor,ak lu mel ni ngistal ku sew ni ki kuy julli di ko taaral ngir wan ko nit ñi.
ndax keneen ku dul Yàlla man naa xam kumpa.
kenn manul xam kumpa ku dul Yàlla.
Yàlla mu kawe mi neena: waxal jaam ñi ne amul kenn ku nekk ci asamaan yi walla suuf ku xam kumpa ku dul Yàlla, te kenn xamul kañ la nu leen di dekkil. suuratu annamli 65
limub ponk i gëm.
1) gëm Yàlla mu kawe mi.
2) gëm ay malaakaam.
3) gëm ay téereem.
4)gëm ay yonnenteem.
5)gëm bis pénc.
6)gëm dogal bu neex ak bu naqari.
tektal bi mooy adiisu Jibriil bu siiw bi Muslim solo Jibrill wax yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal te musal ko: xamal ma lan mooy ngëm, yonnente bi ne ko ngëm mooy nga gëm Yàlla ak i malaakaam, ak i téereem, ak i yonnenteem, ak bis pénc ba, te nga gëm ab dogal bu neex ak bu naqari.
faramfacceel ponk i gëm.
ngëm yàlla mu kawe mi
mooy nga gëm ne Yàlla moo la bind di la wërsëgal, te mooy buur mi moom lepp te moom dong mooy saytu mbideef yi.
te nga gëm ne moom dong moo yayoo jaamu amul kenn ku ñuy jaamu ci dëgg ku dul moom.
te nga gëm ne mooy Aji- màgg ji di ku mat sëkk, te moom donga yayoo mbooleem xeeti cant yi, mooy Boroom tur yu sell yi ak melokaan yu kawe yi amul moroom, te lenn ci mbindeefam yi nuru wu ko.
gёm malaaka yi.
nga gëm ne ay mbindeef la ñu Yàlla da leen a bind ci ag leer ngir ñu jaamu ko topp ndigalam yépp.
bokk na ci malaaka yooyu Jibriil yal na jamm nekk ci moom, mooy malaaka miy wacce ndéeytel Yàlla ci yonnent yi.
gёm téere yi.
téere yi nga xam ne Yàlla a ko wacce ciy yonnenteem.
ni ki Alquraan bi Yàlla wacce ci Muhammat yal na ko Yàlla dolli xéewal te musal ko.
ak Injiil bi Yàlla wacce ci iisaa yal na jamm nekk ci moom.
ak Tawraat bi Yàlla jox muusaa yal na jamm nekk ci mom.
ak zabuur bi Yàlla jox Daawuuda yal na jamm nekk ci moom.
ak yeneeni téere yu mu joxoon Ibraahiimaa ak Muusaa.
gëm yonnente yi:
ñooy ñi Yàlla yónni ci jaamam yi ngir ñu jangal leen di leen bégal ci lu baax ak aljana, waaye di leen xupp ci lu bonn ak sawara.
yoneent yooyu ña ca gën ñooy ñi ñiy woowe uluul hazmi te ñoo ñu ñooy:
yonnent Yàlla Nuuh yal na jamm nekk ci moom.
yonnent Yàlla Ibraahiima yal na jamm nekk ci moom.
yonnent Yàlla Muusaa yal na jamm nekk ci moom.
yonnent Yàlla Hisaa yal na jamm nekk ci moom.
yonnente Yàlla Muammat yal na jamm ak xéewal nekk ci moom.
gёm bis bu mujj ba.
bis pénc ba nak mooy li nekk ci ginnaaw dee ci biir bammeel, ak bisub taxawaay ba, ak dekki ak isaab jëf i jaam ñi ba ñu baax ñi dugg aljana bu bonn ñi dem sawara.
gëm ab dogal bu neex walla bu naqari.
ab dogal mooy nga gëm ne Yàlla xam na lépp luy xew ci kéew bi, te bindoon na ko ca lawhul mahfuuz te moom la neex mu am.
Yàlla neena lépp lu am noo ko bind ci sunug dogal.
ab dogal nak ñenti dayo la:
bu njëkk bi mooy: xam xamub Yàlla, ni ki xam xamam bi jiitu lépp luy xew laataa muy xew ak bi mu xewee ba noppi.
tektal bi mooy wax i Yàlla mu kawe mi: Yàlla rekk a xam tukkig àdduna te mooy kiy wacce ab taw, te moo xam li nekk ci butiiti njuru kaay yi,te amul kenn ku xam lu miy am suba walla ci jan suuf la faatoo,Yàlla mooy ku xam te deñ kumpa. suuratu Luqmaan.
ñaareel bi mooy: nga gëm ne Yàlla bind na ko ci lawhul mahfuuz, lépp lu xew walla luy xew i ëllak lees bind la cib téere.
tektal bi mooy wax i Yàlla mu kawe mi: Yàlla mooy ki xam kumpa keneen ku dul moom xamu ko, te mooy ki xam lépp lu nekk ci jéeri yi walla ci géej gi, te amul wenn xob wuy rot ci suuf lu dul ni xam na ko, amul it aw fepp wuy wadd ci lëndamug suuf si lu dul ne xam na ko amul it lu tooy walla lu wow lu dul ne bind na ko cib téere bu leer. suuratul anhaam 59
ñatteel bi mooy:nga gëm ne lépp luy xew ci coobarey Yàlla lay xewe, te amul dara luy am ludul da koo neex moo xam ci moom la bayyikoo walla ci mbindeef yi.
tektal bi mooy waxi Yàlla mu kawe mi: ku mu soob ci yéen mu jub waaye dara manu leen a soob lu dul dafa soob Yàlla miy Boroom bindéef yi ba noppi. suuuratu attakwiir 28_29
ñeenteel bi mooy: nga gëm ne mbooleem bindeef yi ay mbindéefu Yàlla moo bind seen i jëmm ak seen i melo ak seen lépp.
tektal bi mooy wax i Yàlla mu kawe mi: Yàlla mooy ki leen bind ak seen i jëf. suuratu asaafaati
lan mooy xamleb Alquraan?
Alquraan wax i Yàlla la du mbindeef.
Yàlla mu kawe mi neena: bu kenn ci way bokkaale yi làqoo fi yaw na nga ko fat ndax mu dégg gaddug Yàlla suuratu attawba 6
lan mooy sunna ?
sunna mooy jépp wax walla jëf jees askanale yonnente bi walla muy aw melo ciy jikkoom walla aw bindiinam walla muy lees def ci kanamam mu saxal ko.
lan mooy bidaa ak ndax warees na koo nangu ?
lépp lu nit ñi sos ci diine gannaaw yoneent bi ak i saabaam
dees koy delloo waaye dee su ko nangu.
ngir wax i yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéwal akug mucc: bépp bidaa ag réer la. abuu daawuuda moo ko soloo
lu ci mel ni yokk ci jaamu Yàlla, ni ki yokk raxaub ñeenteel ci njappu, ak lu mel ni gàmmu, ndax xamee su ko ci yonnente bi ak i saabaam.
lan mooy paspasub walaahu wal baraahu maanaam mengóo ag dogoo.
li nu jublu ci walaahu mooy mengóo ak way gëm ñi ak dimbali leen
Yàlla mu kawe mi neena: way gëm ñu góor yi ak yu jigéen yi lenn ci ñoom ñoo mengóog ñeneen ñi. suuratu attawba 71
li nu jublu ci baraahu mooy bañ way weddi yi def leen ay noon, maanaam dogoo ag ñoom ba fawwu.
Yàlla mu kawe mi neena: am ngeen ci Ibraahiima ak ñam andaloon royuwaay wu rafet, ba ñu waxee seenu nit na leen nun day deñ nanu ba set wecc ci yéen ag seen Yàlla yi ngeen di jaamu te du Yàlla, te weddi nan leen, te da ag noonoo akug mbañeel day dox sunu diggante ba fawwu, ba kerook ngeen di gëm Yàlla dong. suuratu al mumtahinatu 4
ndax Yàlla da na nangu janeen diine ju dul lislaam.
Yàlla du nangu janeen diine ju dul lislalaam.
Yàlla mu kawe mi neena: képp ku topp janeen diine ju dul lislaam deesu ko nangu ci moom te bu bis pénc baa di na bokk ci way torox yi. suuratu aali himraan
ak kéefar day tukkee ci wax walla jëf walla pas-pas joxe ci misaal.
misaalum wax juy kéefarloo: mooy lu mel ni saaga Yàlla walla ab yonnenteem.
misaalum jëf juy kéerarloo mooy lu mel ni: doyodal Alquraan, walla sujootal ku dul Yàlla.
misaalum pas -pas buy kéefaloo mooy lu mel ni: nga fas ne am na keneen ku yayoo ag jaamu ku dul Yàlla.
lan mooy ag naaféq ak i xeetam.
T-
ak naaféq gu mag: loolu mooy nëbb ak kéefar di feeñal ak ngëm.
loolu nak day génne nit ci lislaam yobbu ko ci ak kéefar ku mag.
Yàlla mu kawe mi neena: naaféq yi fa gën a suufe ci sawara la niy nekk te kenn manu leen a dimbal. suuratu annisaahi.
2 ak naaféq gu ndaw:
ni ki lu mel ni fen ak wuute ab dig ak wor.
naaféq gu ndaw nak du génne nit ci lislaam, ab bakkaar la ci bakkaar yi, ki koy def nag manees na ko cee mbugal.
yonnente Yàlla bi neena: mandargam naaféq ñatt la: saa yu waxee fen, bu joxee ab dig wuute ko, bees ko wóoloo mu wor. Buxaariu ak muslim ñoo ko soloo.
kan moy mujju ci yonnente yi ak ñi ñu yònni ?
ki muju ci yonnente yi mooy muhammet.
Yàlla mu kawe mi neena: Muhammet nékkul baayub kenn ci yéen waaye yonnenteb Yàlla la, di ki tëj yonnente yi Yàlla moy aji- xam lépp. suuratul ahzaab ٤٠ yonnente bi wax neena: man maay ki tëj yonnent yi,amul beneen ub yonnente buy ñëw sama gannaw. abuu daawuuda ak tirmiziiu soloo na ñu ko ak ñeneen.
lan mooy kéemtaan.
kéemtaan mooy lépp lu Yàlla jox ay yoneenteem ci mbir yu xotti baax ngir firdeel seenug dëggu, ni ki lu mel ni:
xar wéer wi ngir dëggal yonnente bi.
ak xotti géej gi ñeel Muusaa, ak labal Fihawna ak ay andandoom.
ñan ñooy saaba yi ak ndax dama leen a war a bëgg.
ab saaba mooy ku dajé ak yonnente bi gëm ko te faatu ci diiney lislaam.
saaba yooyu dañ leen a war a bëgg di leen roy, ndax ñooy ñi gën ci nit ñi gannaaw. yonnente yi.
ñi gën ci ñoom nag ñooy ñenti xalifa yi:
Abuu bakar Yal na ko Yàlla gёrёm.
Omar yal na ko Yàlla gёrёm.
Usmaan yal na ko Yàlla gёrёm.
Alliyu yal na ko Yàlla gёrёm.
ñan ñooy ndayi way gëm ñi ?
ndayi way gëm ñi ñooy soxnay yonnente bi.
Yàlla mu kawe mi neena: yonnente bi moo gën a yay ci way gëm y ci seen bopp,te ay soxnaam ñooy nday i way gëm ñi. suuratul ahzaab ٦
lan mooy aqi waa kër yoneent bi ci nun ?
dan leen a war a bëgg méngoo leen bañ képp ku leen bañ, te bañ a ëppal ci ñoom, te ñoom ñooy ay soxnaam akug njabootam; ak ñi askanoo ci Aaasim, ak Mutalib te bokk ci way gëm yi
lan mooy sunu warteef ci njiitu jullit yi ?
sunu warteef ci ñoom mooy wormaal leen déggal leen topp leen ci lu dul ag moy Yàlla, te bañ a fétteerlu ci seen kaw; waaye di leen ñaanal, te di léen laayebiir ci suuf.
lan mooy kërug way gëm ñi ëllak ?
seen kër mooy aljana, Yàlla mu kawee mi neena: ñi gëm Yàlla tey jëf jëf ju baax Yàlla da na leen dugal aljana joo xam ne ay dex mooy daw ci biir. suuratu muhammat 12
lan mooy kërug yéefar yi ?
kërug yéefar yi mooy sawara; Yàlla neena: na ngeen ragal sawara mi nga xam ne la koy xamb mooy nit ak ay xeer te waajalees na ko ñeel yéefar yi. saaru Baqara: 24
lan mooy ragal ? lan mooy yaakaar ? ak luy tektal bi ?
ragal: mooy ragal Yàlla ak mbugalam.
yaakaar: mooy yaakaar yoolub Yàlla ak njéggalam ak yërmandeem.
tektal bi mooy wax i Yàlla mu kawe mi: ( ñooñu ngeen di ñaan ñoom seen bopp da ñiy góor-góorlu ci def lu baax ngir gën a jege Yàlla, ñuy yaakaar yërmandeem di ragal mbugalam te sa mbugalum Boroom lu ñiy moytu la) saaru Israa: 57 Yàlla mu kawe mi neena: ( xibaaral sama jaam ñi ne léen man maay aji jéggale ji maay aji yërëme ji 49 waayé sama mbugal mooy mbugal mu metti mi 50 ) saaru Al-Hujraat: 49, 50
tuddal yenn ci tur i Yàlla ak i meloom.
Yàlla, Boroom bi, Aji yëram ji, Aji dégg ji, Aji gis ji, Aji xam ji, Aji wërsëgal ji, Aji dund ji, Aji màgg ji... ak yudul yooyu ci ay tur yu rafet ak melokaan yu kawe.
firil tur yii?
Yàlla: li miy tekki mooy Yàlla ji niy jaamu ci dëgg moom rekk te amul kenn kees koy bokkaaleel.
Buur bi: mooy ki bind te mooy ki moom, mooy wërsagal te mooy doxal mbir yi moom dong moom Yàlla mu sell mi.
Aji dégg ji: mooy ki ag déggam daj lépp, muy dégg kàddu yépp ak séeni wuute ak séeni melokaan.
Aji gis ji: mooy kiy gis lépp, di gis lépp lu ndaw wala mu rëy.
Aji xam ji: mooy ki gisam peeg lépp lu weesu wala li teew wala li ñëwagul
Aji yërëm ji: mooy ki yërmaandeem daj bepp mindeef ak lépp luy dund, te jaam yépp ak mbideef yépp ñoo ngi ci suufu yërmàandeem.
Aji wërsagalé: mooy ki wërsag i mbindeef yépp nekk ci moom moo xam nit la wala jinne wala lépp luy dox ci suuf.
Aji dund ji: mooy kiy dund te du dee, te mbindeef yépp da ñiy dee.
Aji màgg ji:mooy ki ame géppug mat ak léppi magg ci ay turam ak i meloom ak i jëfam.
lan moo nu war ci woroom xam-xam i jullit yi?
dan leen di bëgg, di dellu ci ñoom si masala yi ak xew-xewi sariiha yi, te dunu leen tudd ci lu dul lu rafet, te kepp ku leen tudd ci lu dul lu rafet dafa jaarul ci yoon wu jub wa.
Yàlla mu kawe mi neena: (Yàlla dina yëkati ay daraja ñi gëm ci yéen ak ñi ñu jox xam-xam te Yàlla deñ na kumpa ci lépp lu ngeen i def.) saaru Al-mujaadala 11
ñan ñooy wàlliyuy Yàlla mu kawe mi?
ñooy way gëm yi te ragal Yàlla.
Yàlla mu kawe mi neena: ñi méngoog Yàlla du ñu tiit du ñu jaq, ñooñu ñooy ñi gëm Yàlla te ragal ko. saaru Yuunus.
ndax gëm wax la ak jëf?
gëm wax la ak jëf ak pas-pas.
ndax gëm day yokku di wàññeeku?
gëm day yokkoo cig topp Yàlla di wàññeekoo ci moy Yàlla.
Yàlla mu kawe mi neena: ﴾way gëm yi de ñooy ñi nga xam ne bu ñu tuddee Yàlla seen xol yi day jàq te buñu jàngee aayay Yàlla yi ci ñoom da leen di dolli ag ngëm te ci Yàlla rek lañuy wakkirlu﴿ suuratu Al-anfaal: 2
lan mooy rafetal?
rafetal, mooy nga jaamu Yàlla mel ni yaa ngi koy gis,ndax boo ko gisul moom mi ngi lay gis.
kañ la jëf yi di nekk lu Yàlla mu sell mi di naggu?
ci ñaari sart:
1- bu sellee ngir jëmmi Yalla mu kawe mi rekk.
2-bu tegoo ci sunnas yonnente bi ﷺ.
lan mooy wakkirlu ci Yàlla mu kawe mi?
mooy sukkandiku ci Yàlla ci xëcci njariñ ak jañ lor, andal jàpp ci sabab yi.
Yàlla mu kawe mi neena: képp ku wakkirlu ci Yàlla; Yàlla doy na ko. suuratu Attalaaq: 3
hasbuhoo: mooy doy na ko.
lan mooy warteefu digle lu baax ak tere lu bon?
digle lu baax mooy: digle topp Yàlla, tere lu bonn mooy: aaye lépp luy moy Yàlla mu sel mi.
Yàlla mu kawe mi neena: yeenay xeet wi gën ci xeet yi ndax da ngenn di digle lu baax di tere lu bonn te gëm Yàlla. suuratu aali himraan ١١٠
ñan ñooy mbooloo mi tënku ci sunna :
ñoo ñu ñooy ñi nekk ci li yoneent bi ak i saabaam nekkoon ci jëf ak ci wax ak ci pas- pas.
dees leen di woowe waa sunna ngir topp gu nuy topp sunna di bayyi bidaa
dees leen di askanale ci mbooloo nak ngir booloo gun booloo ci dëgg te dun ci taqalikoo.
xaajub fiq bi47
xamleel laab.
laab mooy yékkati am toj walla dindi sobe.
laabal set mooy: julit bi dindi lépp luy sobe ci yaramam, walla ay yéereem, walla ci barab bi muy taxaw di julli.
laabug toj mooy: nit ki jappu walla mu sangu farata ag ndox mu laab, walla mu tiim bu amul ndox walla bu amee ngant ci jëfëndikoo ndox ma.
naka ngay laabale sobe su la taq ?
da nga koy raxas ag ndox ba mu set.
bu dee ndab lu ab xaj naan dees koy raxas juroom ñaar i yoon raxas bu njëkk ba ñu boole ci suuf.
lan mooy ngëneelul njappu ?
yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xewal ak ug mucc neena: jullit bi walla Aji -gëm ji bu jappoo ba raxas xar kanamam bépp bakkaar bu mu mas a def ci ay gëtam day rot and ak ndox mi,bu raxasee ay yoxoom bépp bakkaar bu mu mas a def ci ay yoxoom dana rot and ak ndox mi,ni ki noonu bu raxasee ay tankam bakkaaram yi mu masa dox ak tankam yépp dana rot andak ndox mi,ba kerook muy set wecc ci ay bakkaar. Muslim moo ko soloo.
na ka ngay jappoo ?
da ngay raxas say tenq ñatti yoon.
nga gallaxndiku, saraxndiku, fiiru ñatti yoon.
gallaxndiku mooy nga guuq ndox wëndeel ko ci sa gémeñ yabbi ko.
saraxndiku mooy: nga def ndox ci loxo ndeyjoor ñoddi ko ak sa galawal bakkan ba mu dugg ci biir bakkan bi.
fiiru mooy: nga génne ndox mi nga dugaloon ci sa bakkan mel ni kuy ñandu ak sa loxo cammooñ
gannaw ba nga raxas sa xarkanam ñatti yoon.
raxas say yoxo ba ci say conc yi ñatti yoon.
masaa sa bopp tambalee ci sab jë jëm ci sag ndong, masaa waale say nopp.
nga raxas say tank ba ci say dojar ñatti yoon.
lii mooy njappu li gën a matale,te sax na juge ci yonnente bi ci ay adiis yu Buxaari ak Muslim solo saaba yu bari nettali ko ku ci mel ni Usmaan ak Abdul Laay ibnu zayd ak yenéen i saaba sax na itam ci yoneent bi ne daana jappu benn benn, ak ñaar ñaar maanaam mu raxas cér i njappu yi benn yoon walla ñaar i yoon; lii Buxaarii solo na ko
lan mooy faratay njappu, te nga lim ko.
faratay njappu mooy li nga xam ne bu ci jullit bi bayyee benn njappoom du baax.
1) raxas xar kanam, boole ci ngallaxndiku ak saraxndiku.
2) raxas say yoxo ba ci conca yi.
3) masaa sa bopp ak say nopp.
4) raxas say tank ba ci dojor yi.
5) toftale cér i njappu yi ni ki jiital raxas xar kanam tek ci raxas yoxo yi; doora masaa bopp, tek ci raxas ay tank.
6) tegele njappu mi maanaam nga jappu ci lu amul benn dog-dog ci dingante bi ba cér bi nga raxas di fendi.
- lu mel ni nit ki jappu ba mu xaaj mu bayyi ko toog ba mu yag mu mottali ko, loolu njappu baaxut.
lan mooy sunnay njappu te nga lim ko.
sunnas njappu mooy loo xam ne bu ko kiy jappu defee am ci tiyaaba; te bu ko bayyee du ci am bakkaar te yit njappoom di na wér.
1) tudd Yàlla te mooy nga wax bismil Laahi.
2) soccu.
3) raxas say yoxo ba ci tikkujara yi.
4) teqale waaraam yi.
5) ñaareelu raxas ak bu ñatteel bi ci cér i njappu yi.
6) tambalee ndayjoor.
7) tudd Yàlla ginnaaw njappu li te mooy nga wax ñaan gii: maa ngi seede ne amul benn buur bu ñiy jaamu ci dëgg bu dul Yàlla moom kepp amul kees koy bokkaaleel,di seede ne muhammadt jaamub Yàlla la te yonnentab Yàlla la.
8) julli ñaar i rakkaa gInnaaw njappu mi.
limal yiy toj njappu.
liy toj njappu mooy lépp lu génne ci ñaar i génnuwaay yu doomu aadama, moo xam ci kanamam walla ci ginnaawam, lu ci mel am saw walla ay dem duus walla ngalawal.
walla ay nelaw walla xel mu dem; walla sax qëm.
ak lekk ndawalug gileem.
ni ki noonu laal sa awra ak sa loxo moo xam ci kanam walla ci ginnaw te dara doxul ci digante bi.
lan mooy tiim ?
tiim mooy nga jëfandikoo suuf ak lu mél ni moom ci béréb bu sell bu fekkee amoo ndox moo laabe walla nga am ngant ci jëfandikoo ndox mi
naka lees di tiime ?
booy tiim da ngay dóor say yoxo ci suuf benn yoon nga masaa ci sa xar-kanam ak sa bitti tenq benn yoon.
lan mooy liy toj tiim
lépp luy toj njappu day toj tiim.
ni ki noonu boo amée am ndox gannaw bi nga tiimee ba noppi.
lan mooy ay saŋ walla ay kawas ak ndax dess na leen masaa ?
ay saŋ mooy lépp lees di sol ci tank te ñu defere ko der.
ay kawas nak mooy lees di sol ci tank te nekkul der.
ñoom ñaar ñepp manees na leen a masaa mu wuutu raxas ay tank
lan mooy xarañte gi nekk ci yoonal masaa ci kaw ñaar i saŋ.
dees koo yoonal gir yombal ak woyafal ñeel jaam ñi rawati na bu jamonoy sedd dugge, walla nit ki nekk ci ab tukki, mu jafe ci moom lool muy summi ay saŋam saa yuy jappu.
lan mooy sart yiy tax ñu mana masaa ci kaw ay saŋ ?
1- mu sol ñaari saŋ yi ci ag laab, maanaam ginnaaw njàpp.
2- saŋ wi nekk lu laab, masaa ci sobe du dagan.
3- saŋ wi muur bépp barab bees farataal a raxal ci njàpp.
4-masaa bi nekk ci diir bi nu tënk ci ki fi dëkk te nekkul ci tukki: mooy bis ak ug kuddeem,ki tukki: ñatti fan ak seen i guddi.
lan mooy melokaan u masaa ci ay saŋ?
melokaanu masaa ci ay saŋ mooy: mu tek yaar i yoxoom yu tooy ak ndox ci kaw waaraam i tànkam daal di leen di rombale ba ca yeel ba, day masaa loxo ndeyjoor bi ci tànku ndeyjoor bi,loxo càmmoñ bi si tànku càmmoñ bi, mu ŋarale ay waaramam buy masaa te du baamtu masaa bi.
lan mooy firi(yàq) masaa ci ay saŋ?
1- jeexug diir bi nu ko tënk, du dagan a masaa ci ay saŋ ginnaw jeexug diir bi nu ko tënk ci sariiha, benn bis ak benn guddi ñeel aji sax ji, ñatti bis ak seen i guddi ñeel aji tukki ji.
2- summi saaŋ yi, nit ki bu summee yaar i saŋam wala benn ba ginnaaw bamu ko masaa ba noppi kon masaa ba yàqu na.
lan mooy julli?
julli:mooy sàkkoo jaamu Yàlla ci ay wax ak i jëf yees jagleel,muy ubbikoo ci kàbbar di jeexe ci sëlmal.
lan mooy àtteb julli?
julli farata la ci bépp jullit.
Yàlla mu kawe mi neena: julli dees koo wutal waxtu ñeel way gëm yi. saaru annisaa i
lan mooy àtteb bàyyi julli ?
bàyyi julli ag kéefar la,yonnent yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc neena:
kollare gi dox sunu digante ak ñoom yéefar yi mooy julli, képp ku ko bàyyi weddi na.
Ahmad ak Tirmizii soloo nan ko ak ñeneen.
ñaata julli moo war ci jullit bi ci bis bi ak ci guddi gi?
juroom i julli ci bis bi ak ci guddi gi,jullik fajar:yaar i ràkka,ak jullig tisbaar: ñeent i ràkka,ak jullig tàkkusaan:ñeent i ràkka,ak jullig timis: ñatt i ràkka,ak jullig gee: ñeent i ràkka.
lan mooy lim i sart i julli ?
1- lislaam, julli du wér ci ab yéefar.
2- xel: julli du wér ci ab dof:
3- ràññee, julli du wér ci gone gu ràññee wul.
4- yéene.
5- duggug waxtu wi.
6- laab ci am toj.
7- laab ci sobe.
8- muur awra.
9- jublu xibla.
lan mooy limi ponk i julli ?
fukk i ponk la ak ñeent, ni ki nii muy ñëwe:
bi ci njëkk: taxaw ci jullig farata ci képp ku ko man.
kàbbaru armal, te mooy "Allaahu akbar".
jàng faatiha.
rukoo, day tàllal ndiggam bamu yamoo, mu def boppam mu tollo ak moom.
yëkkati ku bawoo ci rukoo bi.
yamoo di aji taxaw.
sujjóod,day dëgaral jëam ak bakkanam,ak ay yaar i tenqam, ak yaar i wóomam, ak ay cat i waaraam i tànkam ci barabu sujjootam.
yékkati ku bawoo ci sujjóod bi.
toog ci diggante yaari sujjood yi.
sunna si mooy: mu lal tànku càmooñ am toog ci, sàmp bu ndayjoor bi, jëmale ko penku.
dal ga, mooy ànd ak dal ci bépp ponkub jëf.
taaya ju mujj ji.
toog ñeel taaya ji.
yaari sëlmal yi, te mooy mu wax yaari yoon: "assalaamu halaykum wa rahmatul Laah"
toftale ponk yi nga xam ne bu nit ki sujjootee laataa muy rukoo ci ag tayeef ag julleem day yaqu, bu dee njuumte nak dafa wara dello rukoo ba noppi délu si waat sujjoot.
tuddal wartéef i julli.
wartéef i julli juroom ñatt la:
1) bépp kabbar bu dul kabbaru armal.
2) wax samihal laahu li man hamida ñeel imaam ak kiy julli moom dong.
3) wax rabbanaa walakkal hamdu.
4) wax subhaana rabbiyal asiim benn yoon ci rukoo.
5) wax suhaana rabbiyal ahlaa benn yoon ci sujjóot.
6) wax rabbi iqfir lii ci diggante yaari sujjoot yi.
7) taaya ju njëkk.
toogaayu taaya ju njëkk.
lan mooy sunnay julli.
sunnay julli fukk la ag benn mooy yii:
1- mu wax ginnaww bimu kabbaree armal "subhaanaka allaahumma wa bi hamdi ka, wa tabaaraka ismuka, wa tahaalaa jadduka, wa laa ilaaha xayruka" loolu la ñi woowe: ñaanug ubbée.
2- wax: "ahuuzu billaahi minas saydaani rajiim"
3- wax "bismillaahi rahaamai rahiim"
4- wax: aamiin.
5- jàng faatiha.
6- biral jàng gi ñeel imaam bi.
7- wax ginnaaw cant gi: "mil-as samaawaati, wa mil-al ardi, wa mil-a maa sita min say-in bahdu"
8- bépp sàbbaal bu dolliku ci benn sàbbaal ci sàabbaalu rukoo bi maanaam: ñaareelu sabbaal bi ak ñatteel bi wala lu ko ëpp.
9- bépp sàbbaal bu dolliku ci benn sàbbaal ci sàabbaalu sujjood bi.
10- lépp lu tege ci benn yoon bi miy wax ci digante yaari sujjoot yi "rabbi ixfir lii"
11-julli ci ñoñ yonnent bi.
ñeenteel bi: sunnay jëf yi, ñu kay woowe ay melokaan:
1- yëkati yaari yoxo ci kàabbaru armal bi.
2- ak ci rukoo bi.
3- ak ci yëkkati ku ci rukoo b.
4- ak wàcce leen ginnaaw loolu.
5- teg loxo ndeyjoor ci kaw bu cammooñ bi.
6- xool ci barabu sujjood bi.
7- xàajjale diggate yaari tànqam ci taxawaay bi.
8- ŋëb ñaari yoxoom ci yaari wóomaam ci rokko bi, xàjjale waaraam yi, tàllal ndiggam def boppam mu yamoo ak moom.
9- dëgaral cer i sujjoot yi ci suuf te mu jonjoo ak barabu sujjood bi.
10- soreele ay përag am ak ay wetam, biiram ak ay poojam, ay poojam ak ay yeelam, ak xàjjjale digante ñaari wóomam, ak tàqale ay tànkam, mu def biir waaraam i tànkam ci kaw suuf te tàqale leen,teg ñaar i yoxoom mu tollo ak i waggam, bank ay waraamam.
11- lal tànkam ci diggante ñaari toogaay yi, ak ci taaya bu njëkk bi, ak lal poojam tég ay toogoom ci suuf ci taaya bu ñaareel bi.
12- tàllal ñaari yoxo yi téeg ko ci pooj ci digante yaari sujjood yi, bi te ŋëb waaraam yi, na ka noo nu itam ci taaya yi waye day bank baaraamu sanqleeñ bi ak bu nómboor bi, mu ràbbale baaraamu dëy bi ak bu diggtu bi, muy junj ci baaraamu sànnikaay bi ci buy tudd Yàlla.
13- buy sëlmël mu geestu ndeyjoor ak càmmooñ.
lan mooy limub yiy yàq julli?
1- bàyyi benn pokk wala benn sart ci sart i julli gi.
2- wax ci ak tayeef.
3- lekk wala naan ci ak tayeef.
4- yëngatu yu bari te toftaloo.
5- bàyyi benn warteef ci wartéefi julli te tay ko.
naka la julli bi di jullee?
melokaanu julli:
1- jublu xibla ci sa mbooleem yaram, ci ludul wëlbati ku wala geestu.
2- ginnaaw ba mu yéene julli gimu jubloo julli ci xolam, ci ludul mo koy wax ci làmmiñam.
3-ginnaaw ba mu kàbbar kàbbaru armal daal di wax (allaahu akbar), buy kàabbar mu yëkkëti yaar i yoxoom bamu yamoo ak i wàggam.
4- toppe mu teg biir tenqu loxo ndeyjooram ci kaw bitti ténqu loxo càamooñam ci kaw dënnam.
5- topp mu sàkkoo ubbi julli gi ci wax: " allaahumma baahid baynii wa bay na xataayaaya kamaa baahadta baynal masrixi wal maxribi, allaahumma naqinii min xataayaaya kamaa yunaqaa sawbul abyadi minad danasi, allaahumma ixsilnii min xataayaaya bil maa-i wassalji wal baraji"
wala mu wax: "maa ngi tudd sag sell yaw sama Boorom, di la sant, sa tur wi màgg na, sa tedd nga kawe na, te amul ku yayoo jaamu kudul yaw"
6- mu muslu daal wax: "ahoozu billahi minas saytaani rajiim" 7- toppemu wax bismil Laahi daal di jàng faatiha, daal di wax: bismillahi rahmaani rahiim 1 alhamdu lil Laahi rabbil haalamiin 2 arrahmaani rahiim 3 maa li ki yawmid diin 4 iyyaaka nahbudu wa iyyaaka nastahiin 5 ihdinas siraatal mustaxiim 6 siraatal laziina anhamta halayhim xayril maxdoobi halayhim waladdaaliin 7 saaru faatiha ( 1--7)
topp mu wax:(aamin) moy :yaw Yàlla yal na nga nangu ñaan.
8- topp mu jàng li jàppandi ci Alxuraan,te mu guddal njàng mi ci jullig suba.
9- topp mu rukoo, mooy: day sëngal ndiggam ngir màggal Yàlla, mu kàbbar bu dee rukoo, yëkkati ay yoxoom ba mu yamoo ak i wàggam. liy sunna mooy: mu tàllal ndiggam, def poppam mu tolloo ak moom, mu teg ay yoxoom ci kaw ay wóomam, xàjjale ay waaraam am.
10- mu wax ci rukoo am "sunhaana Ràbbiyal asiim" ñatti yoon, bu ca dollee: "subhaanakal laahumma wa bi hamdika, allahumma ixfir lii" kon it baax na.
11- topp mu yëkkati boppam bàyyi koo ci rukoo bi, daal di wax: "samihal laahu liman hamidahu", day yëkkaki waale ay yoxoom bam yamoo ak i waggam, maamuum nag du wax: "samihal Laahu liman hamidahu", waaye day wax: "Rabbanaa wa lakkal hamdu".
12- topp mu wax ginnaaw bimu siggEe: "Rabbanaa wa lakkal hamdu, mil-as samaawaati wal-ardi, wa mil-a maa sita min say-in bahdu".
13- topp mu sujjoot sujjoot bu njëkk bi,budee sujjood mu wax: "Allaahu akbar",day sujjood ci juróom ñaar i céram:jë bi,ak bakkan bi,ak yaar i tenq yi,ak yaar i wóom yi,cat i ndëggu yi,mu soreele ay përëg am ci ay wet am,ay yoxoom nag du ko lal ci kay suuf,mu jubale ay waaraam am xibla.
14- mu wax ci sujjootam: "subhaana Rabbiyal ahlaa" ñatti yoon, bu ca dollee: "subhaanakal Laahumma Rabbanaa wa bi hamdika, allahumma ixfir lii" kon it baax na.
15- mu yëkkati bopp am bawoo ci rukoo bi, daal di wax: "Allaahu akbar"
16- topp mu toog ci diggante yaari sujjood yi ci kaw tànku càmmooñam, daal di samp tànku ndeyjooram, mu teg loxo ndeyjooram ci kaw catu pooju ndeyjooram ci li féete ci wóom bi, mu ŋëb baaraam bu ndaw bi ak bi ci tege, mu yëkkati baaraamu sànni kaayam di ko yëngal su dee ñaan, mu jël baaraamu déyam lënkale ko ak baaraamu digg bi bamu wërngal, mu teg loxo càmmooñam ci kaw catu pooju càmmooñam ci li féete wóom bi, tàllal ay waaraamam.
17- mu wax ci toogaayu digante yaari sujjoot yi: "Rabbi ixfir lii, warhamnii, wahdinii, warzuqnii, wajburnii, wa haafinii"
18-topp mu sujjood sujjootu ñaareel bi ni ki bu ñëkk ba ci lañu fay wax wala luñu fay def,bu dee sujjood mu kàbbar.
19-mu jog bawoo ci sujjootu ñaareel bi,daal di wax:"Allaahu akbar" mu julli ràkka bu ñaatel na ka mu jullee ràkka bu ñëkk ba ci luñu fay wax wala luñu fay def, waaye nag du ca jàng ñaanu ubbee ga.
20-topp mu mu toog bu rakkaab ñaareel bi jeexee daal di wax: "Allaahu akbar",daala di toog ni ki mu tooge woon ci diggante yaari sujjood yi.
21- mu jàng taaya ci toogaay bii, daal di wax: "atthiyaatu lil-Laahi was-aslawaatu wat-tayyibaatu,as-salaamu halayka ayyuhan nabiyyu wa rahmatul Laahi wa barakaatuhuu,as-sahaamu alaynaa wa alaa ibaadil-laahi assaalihiina,ashadu an laa-ilaaha,illal-Laahu,wa ashadu anna muhammadan abduhu wa rasuuluhu, allaahumma salli alaa muhammadin wa alaa aali Muhammadin, kamaa sallayta alaa ibraahiima wa alaa aali Ibraahiima,innaka hamiidun majiidun.wa baarik alaa Muhammadin wa alaa aali Muhammadin,kamaa baarakta alaa Ibraahiima wa alaa aali Ibraahiima inna ka hamiidun majiidun. a-uuzu bil-laahi min azaabi jahannama, wa min azaabil xabri,wa min fitnatil mahyaa wal mamaati,wa min fitnatil masiihid dajjaali". mu ñaan Boroomam lumu bëgg ci yiw i àdduna ak yu àllaaxira.
22- mu sëlmal ci ndeyjooram, daal di wax: "assalaamu alaykum wa rahmatul-laahi" ni ki noo nu yit lay def ci càmmooñam.
23- bu julli gi nekkee jullig ñatti ràkka wala ñeent; day taxaw fi taaya bu njëkk jeexe, te mooy: "ashadu an laa ilaaha illal-Laahu, wa ashadu anna muhammadan abduhuu wa rasuuluhuu"
24- mu jóg daal di wax: "allaahu akbar", yëkkati yaar i yoxoom ba mu yamoo ak i waggam.
25- mu jullee li des ci julli gi ni ki mu jullee woon ràkka bu ñaareel bi, waaye nag day yam rekk ci jàng faatiha.
26- mu toog di aji pooju, sàmp tànku ndeyjoor bi, génne tànku càmmooñ bi ci suufu tanku ndeyjoor bi, mu dëgëral ab toogoom ci suuf, teg yaari yoxoom ci kaw ay pooj am ni ki mu ko tege woon ci taayaa bu njëkk bi.
27- ci toogaay bii nag day jàng taaya bi lépp.
28- mu sëlmal ci wetu ndeyjooram, daal di wax: "assalaamu alaykul wa rahmatu-laahi"
yan tudd Yàlla lees di wax ginnaaw sëlmal ci julli gi?
"astaxfirul Laaaha" ñatti yoon.
allaahumma antas-salaamu wa minkas-salaamu, tabaarakta yaa zal-jalaali wal-ikraami|"
"laa ilaaha illal-laahu wahdahu laa sariika lahu, lahul-mulku wa lahul-hamdu, wa huwa alaa julli say-in xadiirun, allaamumma laa maani-a limaa ahtayta wa laa muhtiya limaa manahta, walaa yanfahu zaljaddi minkal-jaddu".
"laa ilaaha illal-laahu wahdahu laa sariika lahu, lahul-mulku wa lahul-hamdu, wa huwa alaa julli say-in xadiirun, laa hawla wa laa xuwwata illaa bil-laahil, laa ilaaha illal-laahu, walaa nahbudu illaa iyyaahu, lahun-nihmatu wa lahul fadlu wa lahus-sanaa-ul hasanu, laa ilaaha illal-laahu muxlisiina lahud-diina wa law karihal kaafiruuna"
"subhaanal-laahi" fanweer i yoon ak ñatt.
"alhamdu lil-laahi" fanweer i yoon ak ñatt.
"allaahu akbar" fanwéer i yoon ak ñatt.
mu mataleko téemeer ci wax: "laa ilaaha illal-laahu wahdahu laa sariika lahu, lahul-mulku wa lahul-hamdu, wa huwa alaa kulli say-in xadiirun"
- mu jàng lixlaas ak muslu kaay yi ñatti yoon ginnaaw jullig fajar ak jullig timis, ak benn yoon ginnaaw yeneen julli yi.
-mu jàng ayaatul kursiyyu,benn yoon.
yan mooy sunnay rawaatib yi? ak luy ngëneel?
yaar i ràkka lu jiitu fajar.
ñeent i ràkka lu jiitu gee.
yaar i ràkka ginnaaw tisbaar.
yaar i ràkka ginnaaw timis.
yaar i ràkka ginnaaw gee.
ngëneelam: yonnente bi neena: "ku julli ci bis bi ak ci guddi gi fukk i ràkka ak yaar ci coobare wu, Yàlla tabaxal ko kër ca aljana" Muslim ak Ahmat soloo nanu ko; ak ñeneen.
ban bis mo gën ci ayug bis yi?
bis u aljuma, yonnente bi yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc, neena: "bis bi gën ci seen bis yi mooy bisu aljuma, ci lan bind Aadama,ci lan ko faat, ci lan wal ci moom ruu gi, te ci la yuuxug faatu gi di am,dee leen ci bari lu ngeeni julli ci man, ndax seenug julli dan ma koy gaaral. neena: ñu ne ko yaw yonnent Yàlla bi na ka lan lay gaarale sunug julli ci yaw te fekk funux nga? -daañoo wax ràpp nga- mu wax ne: Yàlla mu màgg mi dafa araamal ci suuf muy lEkk yaram i yonnente yi" abuu daawuuda soloo na ko ak ñeneen.
lan mooy atteb jullig aljuma.
faratay jëm la ci bepp jullit bu góor te mat té am xel tey aji sax.
Yàlla mu kawe mi neena: "ée yéen ñi gëm bun wootee julli ci bis u aljuma na ngeen jëm ca tudd Yàlla ja te bàyyi njaay mi loolu moo gën ci yéen ndeem xam ngeen 9" saaru almunaafixuuna: 9.
lan mooy lim i rakka y julli g aljuma?
lim i rakkaa y julli g aljuma yaar i ràkka la, da ciy bér u ci njàng mi, yaari xutba yun xam moo koy jiitu.
ndax wuute jullig aljuma dagan na?
wuute jullig aljuma dagan ul ci lu dul ngàntul sariiha, bawoo na ci yonnente bi mu wax ne: "képp ku bàyyi ñatt i aljuma ngir woyof al ko; Yàlla di na tëj xol am bi" abuu daawuuda soloo na ko ak ñeneen.
tudd al sunnay bisu aljuma?
T-
1- sangu.
2- gëttu.
3- sol yéere bu rafet.
4- di kàbbar jëm ca jumaa ja.
5-bari di julli ci yonnente bi yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc.
6- jàng saaru kahfi.
7- jëm ca jumaa ja ci dox.
8- di fuglu waxtuy naggu ñaan.
10- tuddal ngëneel i jullig mbooloo?
jële nanu ci Abdallaa doomu Omar yal na leen Yàlla dollee gërëm, yonnente bi yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc neena: "jullig mbooloo moo gën jullig kénn ci ñaar fukki daraja ak juroom ñaar" Muslim moo ko soloo.
lan mooy toroxlu ci julli ?
mooy teewug xol bi ak dalug cér yi ci julli gi.
Yàlla mu kawe mi neena: "way gëm yi texe nanu 1 te ñooy ñiy toroxlu ci seenug julli 2" saaru al-Muuminuuna 1-2.
xamleel azaka?
moom àq ju war la ci alal jees ko jagleel,ñeel kurel bees ko jagleel ci jamono jees ko jagleel.
te moom ponk la ci ponk i lislaam yi,di ab sarax bu war,dees koy jël ci way woomal ji jox ko way ñàkk ji.
Yàlla mu kawe mi neena: ﴾joxe leen azaka﴿ saaru Baqara: 43
lan mooy sarax bu ñu sopp?
mooy bépp sarax bu dul azaka,lu ci mel ni:sarax bu mu mana doon ci anami yiw yi ci jamono ju mu man a doon.
Yàlla mu kawe mi neena: "na ngeen di joxe ci yoonu Yàlla" saaru Baqara: 195
xamleel woor?
mooy jaamu Yàlla ci bàyyi lépp luy dogloo li ko dale ci fenkug fajar gi ba ci sowug jant bi, ànd ag yéene, moom nag yaar i xaaj la:
woor gu war: lu ci mel ni weeru koor, moom ponk la ci lislaam.
Yàlla mu kawe mi neena: ﴾ée yéen way gëm yi farataalees na ci yéen woor na ka ñu ko farataale woon ci ñi leen jiitu woon amaana ngeen ragal Yàlla 183﴿ saaru Baqara: 183
ak woor bu warul:lu ci mel ni woor altine ak alxamis ci ayu bis bu ne, ak woor ñatt bis ci weer wu ne,li ci gën nag mooy bis yu leer yi(13, 14,15) ci weer wu ne.
tuddal ngëneelu woor weeru koor?
jële nanu ci Aboo hurayra, yal na ko yàlla dollee gërëm, yonnente bi yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc, neena: "képp ku woor weeru koor ci gëm ak yaakaar yiw; dees na ko jéggal li jiitu ci ay bàkkaaram" Buxaari ak Muslim dёppoo na nu ci.
tuddal ngëneelu woorug coobare wu ci ludul weeru koor?
jële na nu ci Abii sahiid alxudrii yal na ko Yàlla dolle gërëm neena: yonnente bi yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc neena: "amul benn jaam buy woor benn bis ci yoonu Yàlla,lu dul ne Yàlla di na musal jëmmam ci sawara juroom ñaar fukki nawet ngir bis boobu" Buxaari ak Muslim dёppoo na nu ci.
maanaa "juroom ñaar fukk i nawet" mooy: juroom ñaar fukk i at.
tudd al yenn yiy yàq koor?
1- lekk wala naan te tay ko.
2- wàccu te tay ko.
3- génn ci lislaam.
yan ñooy sunnay koor?
1- gaawa dog.
2- xëdd te yeexe ko.
3-yokk jëf yu baax yi ak jaamu yi.
4- wax ji ki woor di wax bees koo saagaa: man damaa woor.
5- ñaan jamonoy dog.
6- doge tàndarma ju tooy wala ju wow, bu ko amul mu doge ndox.
xamleel aj?
aj:ak jaamu la ngir Yàlla mu kawe mi,ci jublu néegam bees wormaal ci ay jëf yees ko jagleel,ci wax tu wees ko jagleel.
Yàlla mu kawe mi neena: "war na ñeel Yàlla ci nit ku ko man mu aji néegub yàlla ba benn yoon, ku weddi nag Yàlla moom doylu na walif mbindeef yépp 97" saaru aali himraan 97.
limal ponk i aj yi?
1- armal.
2- taxaw arafaat.
3- wërug bëbb ga.
4- dox digante safaa ak marwa.
lan mooy ngëneelu aj?
jële na nu ci Abii hurayra yal na ko Yàlla dollee gërëm, neena: dégg naa yonent bi Yàlla na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc, mu wax ni: "képp ku aj ngir Yàlla, te beejul sëyul deful ag kàccoor; dana dellu mel ni bis bi ko yaayam jure woon" Buxaarii ak Muslim ñoo ko soloo ak Keneen.
"mel ni bis bi ko yaayam jure woon" maanaam ci ludul benn bàkkaar.
xam leel umra?
umra: mooy jaamu Yàlla mu kawe mi ci jublu néeg am ba nu wormaal ci ay jëf yees ko jagleel ci waxtu wun ko jagleel.
limal ponk i umra?
1- armal.
2- wër néeg ba.
3- dox digante safaa ak marwa.
lan mooy jihaad?
mooy def ay coono ak kem kàttan ci tasaare lislaam ak yiir ko moo ki ñoñam, wala rayante ak noon i lilaam ak i ñoñam.
Yàlla mu kawe mi neena: "na ngéen di jihaad ci yoonu Yàlla ci seen alal ak seen bakkan, loolu moo gën ci yéen ndeem xam ngeen 41" saaru attawba 41
xaajub jaar-jaaru yonnente bi.32
lan mooy askanu yonnente bi yal la na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc?
mooy Muhammat doomu Abdu Laahi doomu Abdul Mutallib doomu Haasim té Haasim ci xuraysin la bokk, xuraysin bokk ci araab yi, araab yi bokk ci séti Ismaahiil, te Ismaahiil doomu Ibraahiima la yal na gën gi mucc ak jàmm nekk ci moom ak ci sunu yonnent.
lan mooy turu yaayu sunu yonnent yal na Yàlla dolli ko jàmm ak mucc?
Aaminatu doomu Wahbin.
kañ la baayu yonnente bi faatu?
baayu yonnent bi faatu na ci Madiina fekk yonente bi juddu a gul.
kañ la yonnente bi judd ?
ci atum ñay ya, bisu altine, ci weeru gàmmu.
ci ban dëkk la juddoo?
ci Makka.
ñan ñoo ko nàmpal ku dul yaayam?
jaamu baayam ba Ummu ayman.
- jaamu baay tëxam bi Abuu lahab, Suwaybatu.
- Halimatu Sahdiya
kañ la yaayam faatu?
yaayam mi ngi faatu bi muy am juroom benn i at, maamam Abdul Muttalib yor ko.
kan moo ko yor ginnaaw faatug maamam Abdul Muttalib?
maamam Abdul Muttalib mi ngi faatu bi miy am juroom ñatti at, baay tëxam Abuu Taalib yor ko.
kañ la tukki wóon ànd ak baay tëxam ca Saam?
tukki na ànd ak baay tëxam ca Saam bi miy am fukki at ak ñaar.
kañ la woon ñaareelu tukkeem bi?
ñaareelu tukkeem bi ci yaxantu la woon ci alali Xadiijatu yal na ko Yàlla dollli ngërëm, bi mu dellusée daal di koy takk soxna, booba mi ngi am ñaar fukk i at ak juroom.
kañ la xuraysin tabaxaan kaaba ga?
xuraysin tabaxaat na kaaba ga bi miy am fanweer i at ak juroom.
ñu àtte loo ko bi ñu wuutee ci kuy teg xeer wu ñuul wi, mu teg ko ci ab sér, mu digal xeet wu ne mu jàpp ci benn cat u sér bi, ñu nekkoon ñeent i xeet, bin ko yëkkatee ba ca bërëb am, mu jël ko ci yoxoom teg ko ca barabam yal na mucc ak jàmm nekk ci moom.
ñaata at la amoon bi ñu ko yónnee ? ak ci ñan la ñu ko yónni ?
mi ngi amonn ñeent fukki at, ci nit ñépp lan ko yónni, muy Aji- bégle ak i xuppe.
nan la wahyu wi tàmbalee ci moom?
gént gu dëggu, daawul gént dara lud ul dina am mel ni suba gu xar.
na ka la meloon lu jiitu wahyu wi? ak kañ la wahyu wi njëkk a wàcce ci moom?
da doon jaamu yàlla ca xunt uw Hiraa wa, daan yor yobbal am.
wahyu yi wàcci ci moom fekk mingi ci xunt wi di jaamu Yàlla.
lan moo njëkk a wàcci ci Alxuraan?
wax i Yàlla ji: "iqra bismi ràbbi kal lazii xalaxa 1 xalaxal insaana min halaqin 2 iqra wa rabbukal akramu 3 allazii hallama bilxalami 4 hallamal insaana maa lam yahlam 5 saaru al-halaqi 1-5
kan moo ñëkka gëm ak yonentem ?
ci góor ñi: Abóo bakrin Assiddiix, ci jingéen ñi: Xadiijatu doomu Xuwaylidin, ci xale yi: Aliyun doomu Abii taalibin, ci jaam yin goreel: Zaydu doomu Haarisatu, ci jaam yi gore wul: Bilaal ma dëkk Ecopi, yal na leen Yàlla dolli ngërëm, ak ñeneen.
na ka la wooteb lislaam bi meloon?
woote bi ci suuf la woon diirub ñatti at, ñu digal yonnente bi yal na na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc ci mu baril ko.
nan mbir i yonnente bi meloon ak ñi ànd ak moom ginnaaw binu biralee woote bi?
bokkaale kat yi dañoo ëppal ci di ko lor ak di lor jullit ñi, ba mujj mu digal way gëm yi ñu gàddaay jëm ca An-najaasi ca ecopi.
bokkale kat yi dëppoo ci ray yonnent bi Yàlla na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc, Yàlla aar ko peege ko baay tëxam ba Aboo taalib ngir mu aar ko ci ñoom.
kan moo faatu ci atum fokkeel gi ci yònneem gi yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc?
baay tëxam ba Abòo taalib, ak soxnaam sa Xadiijatu yal na ko Yàlla gërëm.
kañ la rañaan gi amoon ak yéeg gi?
bi mu amee juroom fukki at, ñu farataal ci moom julliy juroom.
raañaan gi: mooy juge jàkka ja ca màkka dem ca jàkka ja ca Falastiin
yéeg gi: mooy bawoo jàkkay Falastiin dem ci asamaan sa, ba ci sidratul muntahaa.
na ka la yonnente bi doon woowe nit ñi ci bitti màkka?
da daa woo waa Taahif di leen gaaral boppam ci xew-xew yi ak ndajeey nit ñi, ba bi ansaar yi dëkk Maddina ñëwee daal di koy gëm jaayante ak moom ci war koo dimbali.
ñaata at la yonnente bi nekk Màkka di woote?
nekk na fa fukki at ak ñatt.
fan la gàddaay jëm?
jòge Màkka dem Maddiina.
ñaata at la am Maddiina?
fukki at.
yan attey lislaam lan farataal ci moom ca Maddiina?
farataalees na ci moom azaka,ak woor,ak aj,ak jihaad,ak nodd,ak yeneen atttey lislaam.
yan mooy xarey yonnente bi yi gën a am solo.
xare badar bu mag ba.
xare uhud.
xare ahzaab.
xareb ubbi Màkka.
lan moo mujjee wàcc ci Alxuraan?
wax i Yàlla ji: ragal-leen bis banu leen i delloo ca seen Boroom kenn ku nekk ñu fay ko la mu jëfoon te kenn du ko ca tooñ 281. saaru Baqara: 281
kañ la yonnente bi faatu? ak ñaata at la amoon?
mi ngi faatu ci weeru gàmmu ci atum fukkeel ba ak benn ci gàddaay gi, mi ngi amoon juroom benn i fukki at ak ñatt.
tuddal soxnay yonnente bi?
1- Xadiijatu doomu Xuwaylidin yal na na ko yàlla gërëm.
2- Sawdatu doom i Zamhatu Yàlla na ko Yàlla gërëm.
3- Aysatu doom i Abuu bakar yal na ko Yàlla gërëm.
4-Hafsatu doom i Omar yal na ko Yàlla gërëm.
5-zaynabu doom i Xuzaymatu yal na ko Yàlla gërëm.
6-Ummu Salamata Hindu doom i Abii umayyata yal na ko Yàlla gërëm.
7- Ummu Habiibata doom i Abuu sufyaana yal na ko Yàlla gërëm.
8- Juwayriyatu doom I Alhaaris yal na ko Yàlla gërëm.
9- Maymuunatu doom i Alhaaris yal na na ko Yàlla gërëm.
10- Safiyyatu doom i Huyay yal na ko Yàlla gërëm.
11- Zaynabu doom u Jahsin yàlla nako yàlla gërëm
ñan ñooy ay doomam?
goor ñi ñatt la nu:
Al-xaasimu, te ci moom lanu ko doon dakkantale.
ak Abdulla
ak Ibraahimu
bu dee jigéen ñi:
Faatimatu.
Ruqiyatu.
Ummu kulsuum.
Zaynabu.
doomam yépp Xadiijatu moo leen jur, bam des Ibraahima, te ñoom ñépp a ko njëkka faatu bam des Faatimatu, mi ngi faatu. ginnaaw am ci juroom benni weer.
tuddal yenn melokaani jëmmi yonnente bi:
nekkoon na ku digg dóomu ci góor ñi, gàttul guddul waaye ci diggante bi la yamoon, dafa weexoon ne rax xonq yal na mucc ak jàmm nekk ci moom,ku séqoon sikkim la woon, yaatu woon ay gët, yaatu woon gémmeñ, kawar ga ñuuloon kukk, mu yaatu woon ay wàgg, neexoon xet, ak yu dul yooyu ci ay mbindiin yu rafet.
ci lan la yonnente bi bàyyi aw xeetam?
bàyyi na aw xeetam ci aw xàll wu yaatu te leer, ag guddeem mel ni bëccëgam, kenn du ku jàdd ku dul ku alku, bàyyi wul benn yiw lud ul ni tegtal na ko xeet wi, wala benn ay lu dul moytu loo na ko xeet wi.
xaajub pirim alxuraan:17
jàngal faatiha te firi ko?
saaru faatiha ak fireem:
bismillahir rahmaanir rahiimi 1 alhamdu lillaahi rabbil haalamiina 2 arrahmaanir rahiimi 3 maa li ki yaw mid diini 4 iyyaa ka nahbudu wa iyyaa ka nastahiinu 5 ihdinas siraatal mustaxiima 6 siraatal laziina anhamta halayhim xayril maxdoobi halayhim waladdaalliina 7 saaru faatiha ( 1--7)
Piri mi:
tudde nan ko saaru faatiha;ngir li ñu ko ubbee téereb Yàlla bi.
🎧 1-"bismil Lahir rahmaanir rahiimi 1"ci turu Yàlla laay tàmbalee jàng Alxuraan,di ko dimbalikoo moom Yàlla mu kawe mi,di baarkellu ci tud turam wi.
"Allaahi" maanaam: ki ñiy jaamu ci dëgg, te deesu ko tudde ku dul moom Yàlla mu sell mi.
"Arrahmaani" maanaam: boroom yërmande ju yaatu ji nga xamne yërmandeem daj na lépp.
"Arrahiimi" mooy: boroom yërmande ñeel way gëm yi
🎧 2- "alhamdu lil Laahi Rabbil haalamiina 2" mooy: mbooleem xeet i cant yi ak mat yi ñeel na Yàlla moom rekk.
🎧 3- "maa li ki yawmid diini 3" mooy: boroom yërmande ju yaatu ji xajoo lépp, di boroom yërmande jiy jokk ñeel way gëm yi.
🎧 4- "maa li ki yawmid diini 4" mooy bis pénc.
🎧 5- "iyyaa ka nahbudu wa iyyaa ka nastahiinu 5" maanaam:yaw rekk la niy jaamu te yaw rekk la niy dimbalikoo.
🎧 6- "ihdinas siraatal mustaxiima 6" mooy gindi ku ci lislaam ak sunna
🎧 7-"siraatal laziina anhamta halayhim xayril maxdoobi halayhim waladdaalliina 7"mooy yoonu jaam i Yàlla yu sell yi ñuy yonent yi ak ñi leen topp,ci lu dul yoonu nasraan yi ak yahuud yi.
- dees na sopp ginnaw bunu ko jàngee nu wax "aamiin" maanaam: nangul sunu ñaan.
jàngal saaru az-zalzalatu te fi ri ko?
saaru az-zalzalatu ak um pireem:
bismillahir rahmaanir rahiimi.
"izaa zulzilatil ardu zilzaalahaa 1 wa axrajatil ardu asxaalahaa 2 wa xaalal insaanu maa lahaa 3 yawma-izin tuhaddisu axbaarahaa 4 bi-anna rabbaka awhaa lahaa 5 yawma-izin yasdurun naasu astaatan liyaraw ahmaalahum 6 faman yahmal misxaala zarratin xayran yarahu 7 waman yahmal misxaala zarratin sarran yarahu 8" (saaru az-zalzalatu 1-8)
Piri mi:
🎧 1-"izaa zulzilatil ardu zilzaalahaa 1" ëy bees yëngalee suuf si. yëngatu gu tar gay xew ca taxawaayu bis pénc ba.
🎧 2- "wa axrajatil ardu asxaalahaa 2" suuf si génne lépp lu nekk ci biiram ci way dee yi ak lu dul ñoom.
🎧 3- "wa xaalal insaanu maa lahaa 3" nit di wax ngir jaaxle: naan luy mbirum suuf si ba tax muy yëngatu a ka baj-baji?!
🎧 4- "yawma-izin tuhaddisu axbaarahaa 4" ci bis bu màgg boobu suuf si di na xibaare lépp lees def ci kawam ci yiw wala ay.
🎧 5- "bi-anna rabbaka awhaa lahaa 5" ndax Yàlla moo ko xamal digal ko loolu.
🎧 6-"yawma-izin yasdurun naasu astaatan liyaraw ahmaalahum 6"ci bis bu màgg boo bu suuf si di yëngatu, nit ñi da ñiy génn ci taxawaayu saytu ga di ay kurel ngir gis seen jëf yin jëfoon ci àdduna.
🎧 7- "faman yahmal misxaala zarratin xayran yarahu 7" képp ku jëf lu yamoog yamb wu ndaw a-ndaw ci lu yiw ak lu baax di na ko gis
🎧 8- "waman yahmal misxaala zarratin sarran yarahu 8" képp ku def lu toll noona ci ay jëf yu ñaaw di na ko gis.
jàngal saaru haadiyaat te firi ko:
saaru haadiyaati ak um pireem:
bismillahir rahmaanir rahiimi.
"walhaaditaayi dabhan 1 falmuuriyaatui xadxan 2 falmuxiiraatu subhan 3 fa asar na bihii naqhan 4 fawasatna bihii jamhan 5 innal-insaana lirabbihii lakanuudun 6 wa-innahu halaa zaalika lasahiidun 7 wa-innahu lihubbil xayri lasadiidun 8 afalaa yahlamu izaa buhsira maa filxubuuri 9 wa hussila maa fis-suduuri 10 inna rabbahum yawma-izin laxabiirun 11" saaru al-haadiyaati
Piri mi:
🎧 1- "walhaaditaayi dabhan 1" Yàlla giñ na ci fas yiy daw ba ñiy dégg ci moom kàddu ngir tar ug daw.
🎧 2-"falmuuriyaati xadxhan 2"mu giñaat ci fas yiy daw ba ay weyam,bu laalee xeer yi sax da ciy taal sawara ngir dal yu tar yim ciy dal.
🎧 3- "falmuxiiraatu subhan 3" mu giñaat ci fas yiy song noon ya ci suba si.
🎧 4- "fa-asarna bi hii naqhan 4" bu ñi daw di jeqi pënd bi.
🎧 5- "fawasatna bi hii jamhan 5" ñuy diggu mbooloo noon ya ci seen i gawar.
🎧 6- "innal-insaana li Rabbi hii lakanuudun 6" nit déy aji terewula ci yiw wi Borom am bëgg ci moom.
🎧 7- "wa-innahu halaa zaa li ka lasahiidun 7" te sax moom aji seede la ci terewoom yiw ga, du ko sax man a weddi ndax ak leeram.
🎧 8- "wa-innahu lihubbil xayri lasadiidun 8" te moom ag jéggi dayoom ci bëgg alal tax na da ciy nay.
🎧 9- "afalaa yahlamu izaa buhsira maa fil xubuuri 9" xanaa nit kii di woru ci dundug àdduna dafa xamul ne bu Yàlla dekkilee way dee yi ba génne leen ci suuf ngir saytu ak fay mbir yi du deme nam fooge woon?!
🎧 10- "wa hussila maa fis-suduuri 10" ñu fés al daal di leer al li ci biir xol yi ci ay yéene ak i pas-pas ak yaneen.
🎧 11-"inna rabbahum bi him yawma-izin laxabiirun 11"bis boobee déy seen Boroom aji dej kumpa la,darra du ko nëbbu ci mbir i jaam ñi te di na leen fay lépp.
jàngal saaru alxaariha te firi ko:
saaru alxaariha ak firéem:
bismillahir rahmaanir rahiimi
" alxaarihatu 1 maal xaarihatu 2 wa maa adraaka mal xaariatu 3 yaw yakuunun naasu kalfaraasil mabsuusi 4 wa takuunul jibaalu kalhihnil makfuusi 5 fa-amma man saxulat mawaaziinuhu 6 fahuwa fii hiisatin raadiyatin 7 wa-ammaa man xaffat mawaaziinuhu 8 fa-ummuhu haawiyatun 9 wamaa adraaka maahiya 10 naarun haamiyatun 11 saaru alxaarihatu 1-11"
Piri mi:
🎧 1-" Alxaarihatu 1" jamono ja nga xam ne day fëgg xol i nit ñi ngir màggug tiitaangeem ya
🎧 2- "maal xaarihatu 2" lan mooy jamono jii di fëgg xol i nit ñi ngir màgggug tiitaangeem ya ?
🎧 3- "wa maa adraaka 3" ana lan moo la xamal - yaw yonnent bi- luy jamono joo jii di fëgg xol i nit ñi ngir màaggug tiitaangeem ya?! mooy bisu taxawaay ba
🎧 4- "yaw yakuunun naasu kalfaraasil mabsuusi 4" bis bay fëgg xol nit ñi da ñiy mel ni ay lëppalëpp yu tasaaroo ci wàll wu ne.
🎧 5- "wa takuunul jibaalu kalhihnil makfuusi 5" te tund doj yi it mujj mel ni ngëndal bu nooy nepp ci woyofug dawam ga ak yëngatoom ga.
🎧 6- "fa-amma man saxulat mawaaziinuhu 6" képp ku ay jëfam yu sell not ay jëfam yu ñaaw.
🎧 7- "fahuwa fii hiisatin raadiyatin 7" koo kii de ma nga ca dund ganu gërëm da na ko am ca àljana.
🎧 8- "wa-ammaa man xaffat mawaaziinuhu 8" képp ku ay jëfam yu ñaaw not ay jëfam yu rafet.
🎧 9- "fa-ummuhu haawiyatun 9" dëkku waayam tey saxu waayam bisub taxawaay ba mooy jahannama.
🎧 10- "wamaa adraaka maahiya 10" ana lan moo la xamal -yaw yonnente bi- loolu mooy lan?
🎧 11- "naarun haamiyatun 11" aw sawara la wu tàng jérr
jàngal saar attakaasuru te firi ko?
saaru attakaasuru ak um pireem:
bismillahir rahmaanir rahiimi
"alhaakumut takaasuru 1 hattaa zurtumul maxaabira 2 kallaa sawfa tahlamuuna 3 summa kallaa sawfa tahlamuuna 4 kallaa law tahlamuuna hilmal yaxiini 5 latarawunnal jahiima 6 summa latarawunnahaa haynal yaxiini 7 summa latus-alunna yawma-izin haninnahiimi 8" saaru attakaasuru 1-8
Piri mi:
🎧 1-""alhaakumut takaasuru1" li leen soxol de-yéen nit ñi-mooy ëppulaante ci alal ak i doom ci lu duk topp Yàlla.
🎧 2- "hattaa zurtumul maxaabira 2" ba faf ngeen dee dugg ca bàmmeel ya.
🎧 3- "kallaa sawfa tahlamuuna 3" ëppulaante de waru leen a soxlaal walif topp Yàlla, da ngeen xalseta xam mujjug soxlaal googu de.
🎧 4- "summa kallaa sawfa tahlamuuna 4" te it di ngeen xaseta xam ag mujjam de.
🎧 5- "kallaa law tahlamuuna hilmal yaxiini 5" ca dëgg-dëgg bu ngeen xamoon xam-xam bu wér ni dees na leen dekkil ngeen jëm fa yàlla, ci ne moom da na leen fay seen i jëf, kon du ëppulaante ci alal ak i doom du leen soxlaal.
🎧 6- "latarawunnal jahiima 6" giñ naa ci yàlla ni bisub taxawaay ba da ngeen gis sawara.
🎧 7-"summa latarawunnahaa haynal yaxiini 7" te it xalset ngeen koo gis gis gu wér ci ludud sikk-sàkka.
🎧 8- "summa latus-alunna yawma-izin haninnahiimi 8" te bis boobee Yàlla da na leen laaj bépp xéewal bumu leen xéewale woon ci wér ak koom ak yeneen.
jàngal saaru alhasri te firi ko:
saaru alhasri ak um pireem:
bismillahir rahmaanir rahiimi
walhasri 1 in nal insaana lafii xusrin 2 illal laziina aamanuu wahamilus saalihaati watawaasaw bilhaqi watawaasaw bissabri 3 saaru alhasri 1-3
Piri mi:
🎧 1-"walhasri 1" Yàlla mu sell mi giñ na ci jamono.
🎧 2- "innal insaana lafii xusrin 2" maanaam nit ñi ñéppa ngi ci yàqule ak ug alkande.
🎧 3- "illal laziina aamanuu wahamilus saalihaati watawaasaw bilhaqi watawaasaw bissabri 3" ndare way gëm yi tey jëf yiw, ànd ak loolu ñuy woote ci dëgg ak ci muñ, ñooñu ñooy ñiy mucc ci yàqule.
jàngal saaru alhumazatu te firi ko?
sarru alhumazatu ak fPreem:
bismillahir rahmaanir rahiimi
"waylun likulli humazatin lumazatin 1 allazii jamaha maalan wahaddadahu 2 yahsabu anna maalahu axladahu 3 kallaa layunbazana filhutamati 4 wamaa adraaka maalhutamati 5 naarul laahil muuxadati 6 allatii tattalihu halal af-idati 7 innahaa halayhim musadatun 8 fii hamadin mumaddadatin 9 saaru alhumazatu 1-9
Piri mi:
🎧 1- "waylun likulli humazatin lumazatin 1" toroxtaange ak tar-tar i mbugal ñeel na ñiy jëw nit ñi ak di leen jam.
🎧 2- "allazii jamaha maalan wahaddadahu 2" ki nga xam ne yitteem mooy dajale alal rekk ak di ko lim,amul beneen yitte bu dul boobu.
🎧 3- "yahsabu anna maalahu axladahu 3" dafa njoort ne alalam ji miy dajale dana ko musal ci dee,mu sax ci dundug àdduna gi.
🎧 4- "kallaa layunbazana filhutamati 4" mbir mi du ne ko way sànku ji fooge de, dees na ko sànni ci biir sawaraw jahannama bi nga xam ne day dëbb di dammate lépp lunu ca sànni ngir tarug jafe-jafeem.
🎧 5- "wa maa adraaka maalhutamati 5" ana lan moo lay xamal -yaw yonnente bi- lan mooy sawara wii di dammate lépp lunu ca sànni?!
🎧 6- "naarul laahil muuxadati 6" mooy sawaraw Yàlla wa ñu taal.
🎧 7- "allatii tattalihu halal af-idati 7" way allawtiku yaram i nit ña ba ca xol ya.
🎧 8- "innahaa halayhim musadatun 8" ña ñiy mbugal dees na leen fa tëj.
🎧 9- "fii hamadin mumaddadatin 9" ci ay kenoy sawara yu ñu tàlli te gudd ba du ñu fa génn.
jàngal saaru alfiilu te firi ko?
saaru alfiilu ak um pireem:
bismillahir rahmaanir rahiimi
"alam tara kayfa fahala rabbuka bi-ashaabil fiili 1 alam yajhal kaydahum fiitadliilin 2 wa arsala halayhim tayran abaabiila 3 tarmiihim bihijaaratin min sijjiilin 4 fajahalahum kahasfin makuulin 5 saaru alfiilu 1-5
Piri mi:
🎧 1- ""alam tara kayfa fahala rabbuka bi-ashaabil fiili 1" xanaa xamóo -yaw yonent bi- naka la sa boroom def Abrahata ak ay gaay am boroom ñay ya ban nammee màbb kaaba ga?!
🎧 2- "alam yajhal kaydahum fiitadliilin 2" Yàlla def na sEen pexe yu ñaaw yan tëroon ngir màbb kaaba ga mu naaxsaay, lan nammoon ci wëlbati nit ñi walif kaaba ga amuñu ko, te amun ci kaaba gi darra.
🎧 3- "wa arsala halayhim tayran abaabiila 3" mu yabal ci seen kaw ay picci yoy dikkal nanu leen di ay mbooloo.
🎧 4- "tarmiihim bihijaaratin min sijjiilin 4" ñu leen di sànni ay xeer yu wow koŋŋ
🎧 5- "fajahalahum kahasfin makuulin 5" Yàlla def leen ni ay xob i mbay yu daaba yi lekk ba joggate ko.
jàngal saaru xuraysin te firi ko?
saaru xuraysin ak um piireem:
bismillahir rahmaanir rahiimi.
"li-iilaafi xuraysin 1 iilaafihim rihlatas sittaa-i wassayfi 2 falyahbuduu rabba haazal bayti 3 allazii athamahum minjuuhin wa-aamanahum minxawfin 4" saar uxuraysin 1-4
Piri mi:
🎧 1-"li-iilaafi xuraysin1" lees ci namm mooy lees miinoon ci tuukki jamonoy seddaay ak tàngaay.
🎧 2- "iilaafihim rihlatas sittaa-i wassayfi 2" tukkib seddaay ba jëm yaman, ak tukkib tàngaay ba jëm saam di ñu nekk ci kóolute.
🎧 3-falyahbuduu rabba haazal bayti 3"nan jaamu Boroom néeg bii ñu wormaal moom rekk,moom mi nga xam ne moo leen yombalal tukki yooyii,te buñu ko bokkaale ak kenn.
🎧 4- "allazii athamahum minjuuhin wa-aamanahum minxawfin 4" moom mi leen leel ba xiifu ñu, aar leen it ba ragalu ñu, ci limu def ci xol i araab yi ci màggal Haram bi ak màggal ñafa dëkk.
jàngal saaru almaahuuna te firi ko?
saaru almaahuuna ak um piréem:
bismillahir rahmaanir rahiimi.
"ara-aytal lazii yukazzibu biddiini 1 fa zaalikal lazii yaduhhul yatiima 2 walaa yahuddu halaa tahaamil miskiini 3 fawalun lilmusallina 4 allaziina hum han salaatihim saahuuna 5 allaziina hum yuraa-uuna 6 wayamnahuunal maahuuna 7" saaru almaahuuna 1-7
Piri mi:
🎧 1- "ara-aytal lazii yukazzibu biddiini 1" ndax xam nga kiy weddi pay ga ca bis u taxawaay ga?!
🎧 2- "fa zaalikal lazii yaduhhul yatiima 2" koo ku mooy kay dàq jirim ba walif soxlaam.
🎧 3- "walaa yahuddu halaa tahaamil miskiini 3" te du ñaax boppam mukk du caagiine keneen ci leel way ñàkk.
🎧 4-"fawalun lilmusallina 4" alkande ak mbugal ñeel na way julli ya.
🎧 5- "allaziina hum han salaatihim saahuuna 5" ñay fowe seen ug julli, duñu ko faale ba waxtoom wa jeex.
🎧 6-"allaziina hum yuraa-uuna 6"mooy ñay ngistal ci seen ug julli ak seen i jëf,duñu sellal seen i jëf ngir Yàlla.
🎧 7- "wayamnahuunal maahuuna 7" ñuy terewu dimbali keneen ci lol dimbalee ca amul benn lor.
jàngal saaru alkawsari te firi ko?
saaru kawsara ak um pireem:
bismillahir rahmaanir rahiimi.
"innaa ahtaynaakal kawsara.1 fasalli li Rabbika wanhari. 2 inna saani-aka huwal abtaru 3 saaru alkawsari 1-3
Piri mi:
🎧 1- "innaa ahtaynaakal kawsara 1" jox nanu la -yaw yonnente bi- yiw wu bari, tem bokk ca déegu kawsar ba ca aljana.
🎧 2-"fasalli li Rabbika wanhari 2" santal Yàlla ci xéewalam yii,ci nga koy jullil moom rekk ak di ko rendil,wuute ak li bokkaale kat yi di def ci jegeñ-jegeñ lu seen xëram ya ci rendil leen.
🎧 3-"inna saani-aka huwal abtaru3" ka la bañ moo dog ci lépp lu baax, mooy kañu fatte nga xam ne buñu ko tuudee rekk ci lu ñaaw lees koy tudd.
jàngal saaru alhumazatu te firi ko?
saaru alkaafiruuna ak um fpreem:
bismillahir Rahmaanir Rahiimi
"xul yaa ayyuhal kaafiruuna 1 laa ahbudu maa tahbuduuna 2 wa laa antum haabiduuna maa ahbudu 3 wa laa anaa haabudun maa habadtum 4 wa laa antum haabiduuna maa ahbudu 5 lakum diinukum waliya dini 6" saaru alkaafiruuna 1-6
Piri mi:
🎧 1- "xul yaa ayyuhal kaafiruna 1" waxal -yaw yonnente bi- ée yéen ñi weddi Yàlla
🎧 2- "laa ahbudu maa tahbuduuna 2" duma jaamu ci jamono jii mukk walaa ëllag xëram yi ngeen di jaamu.
🎧 3- "wa laa antum haabiduuna maa ahbudu 3" yeen itam du ngeen jaamu li may jaamu man, te mooy Yàlla rekk.
🎧 4- "wa laa anaa haabudun maa habadtum 4" man itam duma jaamu li ngeen di jaamu ci ay xëram.
🎧 5-"wa laa antum haabiduuna maa ahbudu 5" te déet yéen ngeen di jaamu li may jaamu man,te mom rekk mooy Yàlla.
🎧 6- "lakum diinukum waliya dini 6" yeen ak seen diine ji ngeen fental seen bopp, man ak sama diiné ji Yàlla wàcce ci man.
jàngal saaru annasri te firi ko:
saaru annasri ak um pireem:
bismillahir rahmaanir rahiimi.
"izaa jaa-a nasrul Laahi walfathu 1 wa ra-aytan naasa yadxuluuna fii diinil Laahi afwaajan 2 fasabbih bihamdi Rabbika wastaxfirhu innahu kaana tawwaaban 3 saaru annasri 1-3
Piri mi:
🎧 1- "izaa jaa-a nasrul Laahi walfathu 1" su ndimbalu Yàlla ñëwee ñeel sa diine ji -yaw yonnente bi- ak ug tedd-ngaam , ubbiteg Màkkaam
🎧 2- "wa ra-aytan naasa yadxuluuna fii diinil Laahi afwaajan 2" nga gis nit ñi di dugg ci lislaam di ay mbooloo ay mbooloo.
🎧 3- "fasabbih bihamdi Rabbika wastaxfirhu innahu kaana tawwaaban 3" xamal ne loolu màndarnga la ci jegeg jeexug liggéey bi nu la yónni woon, na nga sàbbaal mgir sant sa Boroom, di ko sant ci xéewalug ndimbal gi ak ubbite gi, te nga sàkku ci moom ag njéggal, ndax moom jéggalaakon la aji naggu tuubug jaamaam yi la, te da leen di jéggal.
jàngal saaru almasadi te firi ko?
saaru almasadi ak um pireem:
bismillahir rahmaanir rahiimi.
"tabbat yadaa Abii lahabin wa tabba 1 maa axnaa hanhu laaluhu wa maa kasaba 2 sa yaslaa naaran zaatal lahabin 3 wamra-atuhu hammaalatal hatabi 4 fii jiidihaa hablun min masadi 5" saaru almasadi 1-5
Piri mi:
🎧 1-"tabbat yadaa Abii lahabin wa tabba 1"ñaari yoxoy baay tëxu yonnente bi yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc di Abii lahab toskare na ngir jëfam yu sànku ci li mu daan lor yonnente bi,te it ay jëfam sooy na.
🎧 2-"maa axnaa hanhu laaluhu wa maa kasaba 2" lan la la ko alalam ak i doomam jariñ? du ñu ko jeñal mbugal,te dees ko xëccal yërmaande.
🎧 3- "sa yaslaa naaran zaatal lahabin 3" bu bisu taxawaaybaa dina dugg sawara way tàkk jëppet, di jaaroo tàngaayam ba.
🎧 4- "wamra-atuhu hammaalatal hatabi 4" soxnaam sa it dana fa dugg moom mi daan lor yonnente bi ci di sànni ay dég ci yoonam wi.
🎧 5- "fii jiidihaa hablun min masadi 5" nekk na ca doqam la ab buum bunu xereñe ràbbin wa, di ko ci wommat jëme sawara.
jàngal saaru al-ixlaas te firi ko?
saaru al-ixlaas ak um pireem:
bismillahir Rahmaanir Rahiimi
"xul huwal Laahu ahadun 1 Allahus Samadu 2 lam yalid wa lam yuulad 3 wa lam yakun lahu kufuwan ahadun 4 saaru al-ixlaas 1-4
Piri mi:
🎧 1- "xul huwal Laahu ahadun 1" waxal -yaw yonnente bi- ne: mooy Yàlla amul kenn kuñu war a jaamu kudul moom.
🎧 2- "Allahus Samadu 2" maanaam: dees na yëkkati soxlay mbindeef yi jëme ci moom.
🎧 3- "lam ya lid wa lam yuulad 3" moom Yàlla mu sell mi amul doom te amul way-jur
🎧 4- "wa lam yakun lahu kufuwan ahadun 4" amul dara lu niroo ak moom ci bindeefam yi.
jàngal saaru alfalaxi te firi ko?
saaru alfalaxi ak um pireem:
bismillahir rahmaanir rahiimi
"xul ahuusu birabbil falaxi 1 min sarri maa xalaxa 2 wa min sarri xaasixin izaa waxaba 3 wa min sarrin naffaasaati filhuxadi 4 wa min sarri haasidin izaa hasada 5" saaru alfalaxi1-5
Piri mi:
🎧 1-"xul ahuusu birabbil falaxi 1" waxal -yaw yonnente bi-ne:maa ngi muslu ci boroom suba gi tey làqatu ci moom.
🎧 2- "min sarri maa xalaxa 2" ci ayu lépp luy lure ci mindeef yi.
🎧 3- "wa min sarri xaasixin izaa waxaba 3" maa ngi muslu ci Yàlla ci bépp ay buy feeñ guddi ci ay daaba ak i sàcci.
🎧 4- "wa min sarrin naffaasaati filhuxadi 4" maa ngi muslu ci moom ci ayu njabarkat yu jigéen yiy ëf ca pas-pas ya.
🎧 5- "wa min sarri haasidin izaa hasada 5" ak ci ayu képp ku soxor te iñaane nit ñi li leen Yàlla may ci ay xéewal, tey tàbbal lor ci seen kaw.
jàng al saaru annaasi te fi ri ko?
saaru annaasi ak um pireem:
bismillahir rahmaanir rahiimi
"xul ahuuzu birabbin naasi 1 ma li kin naasi 2 iLaahin naasi 3 min sarril waswaasil xannasi 4 allazii yuwaswisu fii suduurin naasi 5 minal jinnati wannaasi 6" saaru annaasi 1-6
Piri mi:
🎧 1- "xul ahuuzu birabbin naasi 1" waxal -yaw yonnente bi- ne: maa ngi muslu ci Boroom nit ñi, tey làqatu ci moom.
🎧 2- "ma li kin naasi 2" mooy soppaxndiku ci ñoom num ko neexe, amuñu beneen buur budul moom.
🎧 3- "ilaahin naasi 3" mooy ki ñiy jaamu ci dëgg, amu ñu kenn ku ñiy jaamu ci dëgg ku dul moom.
🎧 4- "min sarril waswaasil xannasi 4" ci ayu saytaane miy sànni ay jax-jaxeem ci nit ñi.
🎧 5- "allazii yuwaswisu fii suduurin naasi 5" day sànni ay jax-jaxeem ci xoli nit ñi.
🎧 6- "minal jinnati wannaasi 6" maanam: kiy jax-jaxee dina nekk si nit ñi dina nekk itam si jinne yi.
Xaajub Hadiis bi14
mottalil hadiisu : "jëf yi daal mingi aju ca yéene ya..." te nga tudd yenni njariñam?
jële nanu ci njiiti way-gëm yi baayu Hafsin Umar doomu Alxattaab yal na ko Yàlla mu kawe mi dollee gërëm mu wax ni:dégg naa yonnente Yàlla bi ya lna ko Yàlla dolli jàmm ak mucc ak i ñoñam mu wax ne: "jëf yi mi ngi aju ci yéene yi, te nit ku nekk la mu yéene rekk a ko ñeel, képp ku gàddaay ngir Yàlla ak ab yonenteem,koo ku gàddaayam dina jëm ci Yàlla ak yonenteem,waaye képp ku gàdaay ngir àdduna jum soxlaa jot,wala jigéen ju mu bëgg a takk; kon gàddaayam jëm na ca la ko taxa gàddaay" Buxaariu ak muslim ñoo ko soloo.
ay njariñ ci hadiis bi:
1- bépp jëf bone du ñàkk yéene, julli, woor,aj,ak yeneen jëf yi.
2- sellal ngir Yàlla mu kawe mi mënuta ñàkk ci yéene.
hadiis bu ñaareel bi:
motti ill hadiisu "képp ku sos ci sun mbir mii (diiné ji)..." te nga tudd yenni njariñam?
jële nanu ci yaayu way-gëm yi yaayu Abdallaahi Aysatu yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne:yonente bi yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc neena: "képp ku sos ci sun mbir mii luci bokkul dees ko koy delloo" Buxaariu ak muslim ñoo ko soloo.
ay njariñ ci hadiis bi:
1- tere sos ci diine.
2-jëf yin sos ci diine dees koy dello te deesu ko nangu
hadiisu ñatteel bi:
mottalil hadiisu (binga xaamee ne toog nanu ci yonent bi yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc...), te nga tudd yenn njariñam?
jële nanu ci Umar doomu Alxattaab yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne:benn bis danoo toog ci yonent bi,fa saasa benn waay ñëw,bu yéere ya weex tàll,kawar ga ñuul kukk,te kenn gisul si moom jeexiit i tukki,te it kenn xamu ko si nun,bam aksi toog ci yonent bi yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc,daa di wéer ñaari wóomam ci ñaari wóomam,teg ñaari tenqam ci kaw poojam,daal di ne:"ée yaw Muhammat xibaar ma luy lislaam",mu ne ko"lislaam mooy:nga seede ne amul kenn ku deesi jaamu ku dul Yàlla,seede ne Muhammat ndawul Yàlla la,tey taxawal julli,di woor weeru koor,te aj Màkka benn yoon boo ko manee" mu ne ko:"wax nga dëgg" uu yéemu ci moom di ko laaj ba noppi di ko dëggal,mu ne ko:"xibaar ma lan mooy gëm"mu ne ko:"mooy nga gëm Yàlla,ak i malaakaam,ak i téereem,ek i yonenteem,ak bis bu mujj ba,nga gëm ndugal yi;yacay yiw ak yacay ay"mu ne ko:"wax nga dëgg"daal ni ko:"xibaar ma lan mooy rafetal" mu ni ko:"mooy ngay jaamu Yàlla mel ni yaa ngi koy gis,ndax boo ko gisul moom moo ngi lay gis"mu ne ko:"xibaar ma kañ la bis pénc" mu ne ko:"ki ñu koy laaj gënukoo xam ki ko koy laaj"mu ne ko:"wax ma ay màndarngaam"mu ne ko:"mooy jaam ba jur ab sangam,nga gis way-fàndaañu ya way-rafle wu ya way-ñàkk ya sàmukati jur ya,ñuy guddalaante ca taxab ya"mu wéy ma sax ci ak jaaxle,mu ne ma:"ée Umar ndax xam nga aji-laaj ji?" ma ne ko:"Yàlla ak ub yonnenteem ñoo xam"mu ne ma:"koo ku Jibriil la,dafa ñëw ngir xamal leen seen diine" Muslim moo ko soloo.
bokk na si njariñi hadiis bi:
1-tudd ponk i lislaam yay juroom;te mooy:
seede ne amul kenn ku yayoo jaamu kudul Yàlla,ak ne Muhammat Yàlla a ko yonni.
ak taxawal julli.
ak joxe azaka.
ak woor weeru koor.
ak aj néegub Yàlla bees wormaal ba.
2- tudd punk i ngëm, te juroom benn la:
gëm Yàlla.
ak i malaakaam.
ak i téereem.
ak i yonenteem.
ak bis bu mujj ba.
ak dogal yu neexam ak yu naqareem.
3- tudd ponku rafetal, moom benn ponk la, te mooy nga jaamu Yàlla mel ni yaa ngi koy gis ndax boo ko gisul moo ngi lay gis.
4- jamonoy taxawaayu bis pénc kenn xamu ko kudul Yàlla mu kawe mi
hadiisu ñentéel bi:
mottalil hadiisu : "ki gën a mat ngëm ci way-gëm yi..." te nga tudd yenn njariñam?
jële nanu ci Abii sahiid hurayrata yal na ko Yàla dollee gërëm neena: yonente bi Yalla na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc neena: "ki gën a mat ngëm ci way-gëm yi mooy ki gën a rafet jiko" Tirmiziyu soloo na ko daal di wax ni: "hadiis bu rafet la bu wér la"
ay njariñ ci hadiis bi:
1- ñaaxe si rafet jiko.
2- matug jiko bokk na ci matug ngëm
2- ngëm day yokku di wàññeeku?
Hdiisu juroomeel bi:
Mottalil hadiisu "ku giñ ci ku dul Yàlla..." te nga tudd yenn njariñam?
Jële nanu ci Doomi Umar yal na leen Yàlla dollee gërëm neena: Yonnent bi yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc neena: "Képp ku giñ ci ku dul Yàlla; weddi na wala bokkale na" Attirmizii moo ko soloo
Ay njariñ ci hadiis bi:
- Giñ ci ku dul Yàlla mu kawe mi daganul.
- Giñ ci ku dul Yàlla ci bokkaale gu ndaw la bokk.
Hadiisu juroom benneel bi:
Mottalil hadiisu "kenn ci yéen du gëm ndare ma gënal ko..." te nga tudd yenni njariñam?
Jële nanu ci Anas yàl na ko Yàlla dollee gërëm, neena Yonnent bi yal la na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc, neena: "Kenn ci yéen du gëm ndare ma gënal ko wayjuram ak doomam ak mbooleem nit ñi" Buxaariu ak muslim ñoo ko soloo.
Bokk na ci njariñi hadiis bi:
-dana war ñu bëgg yonnent bi ci kaw mbooleen nit ñi.
- Loo lu ci matug ngëm la bokk.
Hadiisu juroom ñaareel bi:
Mottalil hadiisu "kenn ci yéen du gëm ndare mu bëggal mbokkam..." te nga tudd yenn njariñam?
Jële nanu ci Anas yal na ko Yàlla dollee gërëm,neena Yonnent bi yal na na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc, neena: "Kenn ci yéen du gëm; ndare mu bëggal mbokkam li mu bëggal boppam" Buxaariu ak muslim ñoo ko soloo.
Bokk na ci njariñi hadiis bi:
1- War na ci jullit bi mu bëggal jullit yi yiw ni ki mu ko bëggale boppam.
2- Te ci matug ngëm la bokk.
Hadiisu juróom ñatteel bi:
Mottalil hadiisu: "giñ naa ci ki sama bakkan nekk si loxoom!..." te nga tudd yenn njariñam?
Jële nanu ci Abii Sahiid, yal na ko Yàlla dollee gërëm, mu jële yonnent bi yalna ko Yàlla dolli jàmm ak mucc, neena: "giñ naa ci ki sama bakkan nekk ci loxoom! moom dé dana yamoog ñatteelu xaaju Alxuraan" Buxaarii moo ko soloo
Yénn njariñi hadiis bi:
1- Ngëneelu saaru Al -lixlaas.
2- Moom day yamoo ak ñatteelu xaaju Alxuraan.
Hadiisu juróom ñenteel:
Mottalil hadiisu: "déet benn pexe wala benn kàttan ndare ci Yàlla..." te nga tudd yenn njariñam?
Jële nan ci Abii Muusaa yal na ko Yàlla dollee gërëm neena: Yonnent bi yal na na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc neena: "Laa hawla walaa xuwwata illaa bil-Laahi am ndàmb la ci ndàmbi Aljana ya" Buxaariu ak muslim ñoo ko soloo.
Bokk na ci njariñi hadiis bi:
1- ngëneelu baat bi, ak it ne moom ndàmb la ci ndàmbi Aljana yi.
2- setug jaam bi ci pexe am ak kàttanam,ak ug sukkandikoom ci Yàlla mu kawe mi moom rekk.
Hadiisu fukkeel bi:
Motti lil hadiisu "ca dëgg-dëgg nekk na ci yaram benn lumb deret..." te nga tudd yenn njariñam?
Jëlenan ci Annuhmaan Doomi Basiir yal na leen Yàlla dollee gërëm, neena: dégg naa yonent bi yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc, mu wax ne: "Damane am na ci yaram benn lumb deret bu yéwenee yaram wi wépp yéwen, te bu yàqoo yaram wi yépp yàqu, loolu mooy xol" Buxaariu ak muslim ñoo ko soloo.
Yenn njariñi hadiis bi:
1- yéwenug biir ak bitti mingi ci yéwenug xol.
2- yitte woo yéwenug xol ndax ci la nit di yéwene.
Hadiisu fukkeel bi ak benn:
Mottalil hadiisu: "képp ku mujjantalu waxam ci àdduna di: laa-ilaaha illal-Laahu..." te nga tudd yenn njariñam?
Jële nanu ci Muhaaz Ibn Jabalin yal na ko Yàlla dollee gërëm neena: yonent bi yal na na ko yàlla dolli jàmm ak mucc neena: "képp ku mujjug waxam di: laa-ilaaha illal-Laahu; dina dugg Aljana" َAbuu Daawuda moo ko soloo.
Yénn njariñi hadiis bi:
1- ngëneelu laa-ilaaha illal-Laahu, ci ne jaam bi da ciy dugge Aljana.
2- ak ngëneelu ki mujjantalu waxam ci àddina nekk: laa-ilaaha illal-Laahu.
Hadiisu fukkeel bi ak ñaar:
Mottalil hadiisu: "jullit du kiy jamaate wala muy rëbbaate..." te nga tudd yenni njariñam?
Jële nanu ci Abdul-Laahi Doomi mashuud yal na ko Yàlla dollee gërëm neena:Yonnent bi yal na ko Yàla dolli jàmm ak mucc neena: "nekkul julli aji-jamaate gi du caagine aj-rëbbaate gi, wala aji-déf ñaawteef, wala aji-bon lammiñ" Attirmizii moo ko soloo
Bokk na si njariñi hadiis bi:
1-tere jépp wax i neen wala ju bon.
2- loolu mooy meluw jullit ci làmmiñam.
Hadiisu fukkeel ak ñatt:
Mottalil hadiisu "bukk na ci rafetu ngëmu nit ki..." te nga tudd yenn njariñam?
jële nanu ci Abii sahiid hurayrata yal na ko Yàla dollee gërëm neena: yonente bi Yalla na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc neena: "bokk na ci rafetu ngëmu nit ki: mu bàyyi lu ko amalul njariñ" Tirmizii ak Ahmad ñoo ko soloo ak ñeneen.
Bokk na si njariñi hadiis bi:
1- nit ki bàyyi lu ko amalul njariñ ci mbir i diine wala mbir i àddina.
2- bàyyi lu amul njariñ daa bokk ci matug Lislaamam.
Hadiisu fukkeel ak ñent:
Mottalil hadiisu "képp ku jàng benn araf ci téere Yàlla bi..." te nga tudd yenni njariñam?
Jële nanu ci Abdul Laahi Doomi Mashuud neena:Yonnent bi yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc néena: "képp ku jàng ben ci téereb Yàlla bi dina ci am wenn yiw, yiw wu ne day tolloog yiw, duma wax ni alif laam miim benn araf la waaye alif araf la, laam araf la, miim araf la" Attirmizii moo ko soloo
Yénn njariñi hadiis bi:
1- ngëneelu jàng Alxuraan.
2- benn haraf boo jàng da nga ci am ay yiw.
Xaaju teggini Lislaam yi.26
naka la teggiinu ak Yàlla mu kawe mi di nekke?
1- di ko màggal moom Yàlla mu sell mi te kawe.
2- di ko jaamu moom dong te bañ koo bokkaale ak dara.
3- di ko topp.
4- bañ koo moy.
5- di ko sant ak di ko gërëm moom mu màgg mi te kawe ci ay ngëneelam ak i xéewalam yiy dée fu ko takk.
6- ak di muñ ci ay ndogalam.
na ka la tégginu ak Yonnent bi di nekke?
1- di ko topp ak di roy ci moom.
2- di ko topp.
3- bañ koo moy.
4- dëggal ko ci lépp lu mu xibaar
5- bañ a sos wala dooli si suunaam si.
6- bëgg ko lu raw ni nga bëgge sa bakkan ak nit ñi ñépp.
7- di ko màggal ak di ko dimbali ak di dimbali sunnaam si.
naka la teggiinu ak ñaari Way-Jur di nekke?
1- topp ñaari Way-Jur ci lu dul moy Yàlla.
2- di liggéeyal ñaari Way-Jur.
3- di dimbali ñaari Way-Jur
4- di faj aajuy ñaari Way-Jur.
5- di ñaanal ñaari Way-Jur.
6- tegginu ak ñoom ci wax; du dagan nga leen wax uf, te mooy li gën a néew ca wax ya.
7- di muuñ ci sa kanami ñaari wayjur, te bañ a ñëkk.
8- duma yékkati sama kàddu ci kaw seen kàddu, di naa leen diglu, te duma leen dog ci wax, te du ma leen woo ci seen tur, waaye damay wax: "sama baay", "sama yaay"
9- damay yéglu balaa may dugg ci sama baay ak sama yaay bun nekkee si néeg bi.
10- fóon loxo ak boppu samay Way-Jur
Na ka laay jokke samay mbokk?
1- di seeti jegeñaale yi ci mbokk mu góor ak mu jigéen ak baay tëx ak bàjjan ak nijaay ak tànta ak jegéñaale yi des.
2- di rafetal jëme ci ñoom ci wax ak jëf ak di leen dimbali.
3- bokk na ca di leen jokk ak di leen laaj séen i nekkiin.
na ka laay nekke ak samay xarit?
1- di naa bëgg ak di àndaale ak ñu baax ñi.
2- damay moytu ak di bañ a àndaale ak ñu bon ñi.
3- damay nuyu samay mbokk ak di saafuwante ak ñoom.
4- dama leen di seeti bu ñu wéradee di leen ñaanal wér.
5- damay ndokkeel Aji-Tissooli ji.
6- damay wuyu woooteem buma woowee ngir seet si ko.
7- dama koy jox ay ndénkaan.
8- dama koy dimbali bu ñu ko tooñee, te di ko tere tooñ.
10- damay bëggal sama mbokku jullit li ma bëggal sama bopp.
11- dama koy dimbali bu yittewoo sama ndimbal.
12- du ma ko lor ci wax walla jëf.
13- damay wattu ay bóotam
14- du ma ko saaga, te du mako jëw.
lan mooy tégginu dëkkandoo?
1- damay rafetal ñeel sama dëkkadoo ci wax ak ci jëf te di ko dimbali bu yittewoo sama ndimbal.
2- Dama koy ndokkeel bu amee xew-xewu mbégte wala muy céetam wala leneen.
3- damakoy seeti bu wéradee te di ko jaale bu faatulee.
4- dinaa ko may ci li may togg nu mu gën a jàppandee.
5- du ma ko lor ci wax walla jëf.
6- du mako tanqal ci kàddu gu kawe, wala ma koy luññutu, te dinaa ko muñal
lan mooy tegginu nganale ak gan?
1- damay wuyu ku ma woo ci gane ji ko
2- buma nammee seeti kenn damay sàkku ndigël ak dig-daje.
3- damay yéglu balaa may dugg.
4- du ma yeexe seeti gi.
5- dinaa dammu gis ba ci waa kër gi.
6- dinaa dalal jàmm gan gi di naa ko gatandu gën gaa rafetuw gatandu wiin, ci kanam gu bélli, ak ay waxiini dalal yu rafet.
7- dinaa dalal gan gi ca baeab ba gën a jekk.
8- dinaa ko teral cig nganale ci lekk ak naan.
tuddal teggini wopp ak seeti Way-Wopp?
1-suma yégee mettit; damay teg sama loxo ndeyjooy ca barab bay metti, ma wax: "bismil-Laahi" ñatti yoon, daal di wax: "ahuuzu bi hizzatil-Laahi wa xudratihii min sarri maa ajidu wa uhaaziru" juroom ñaari yoon.
2- damay gërëm li Yàlla dogal te muñ.
3- damay gaawantu seeti sama mbokk mi wopp, ma ñaanal ko te du ma guddal toogaay ba ca moom.
4-damakoy mocc ci lu dul mukoy sàkku ci man.
5- damakoy dénk muñ ak ñaan, ak julli ak laab kem kàttanam.
6- ñaan ñeel Aji-Wopp ji: "as-alul Lahal Haziima Rabbal Arsil Haziimi an yasfiyaka" juroom ñaari yoon.
tuddal teggini sàkku xam-xam?
1- sellal yéene ngir Yàlla mu màgg mi te kawe.
2- damay jëfe xam-xam bi ma jàng.
3-damay wormaal Jàngalekat bi dama koy weg ci teewaayam ak ug ci fàddoom.
4- damay toog sc kanamam ànd a ki teggin.
5- dama koy déglu bu baax te duma ko dog buy jàngale.
6- damay am teggin ci joxe laaj ba.
7- du ma ko woo ci turam.
lan mooy teggini jotaay?
1- damay nuyu waa jotaay bi.
2- damay toog fi jotaay bi yam, duma yëkkati kenn ci barabam wala may tog ci diggante ñaari nit ci lu dul seen ndigël.
3- damay yaatal jotaay bi ngir keneen toog.
4- duma dogg waxtaanu jotaay bi.
5- damay yéglu daal di nuyoo balaa mau jòge ca jotaay ba
6- bu jottay ba jeexee damay ñaan ñaanug siipi bàkkaaru jotaay yi. "subhaanakal Laahumma wa bi hamdika, ashadu an laa-ilaaha illaa anta, astaxfiruka wa atuubu ilayka"
tuddal teggini nelaw?
1- damay teela nelaw.
2- damay nelaw ci ak laab.
3- duma dëfeenu.
4- damay nelawe sama wetug ndeyjooy, ma teg sama loxo ndeyjoor ci suufu sama lexu ndeyjoor.
5- damay fëgg samab lal.
6-damay jànk ñaani nelaw,aayatul kursiyyi,ak saaru lixlaas ak xul ha huusu bi Rabbil falaqi,ak xul ha huusu bi Rabbin naasi ñatti yoon. "bismikal Laahumma amuutu wa aahyaa"
7-damay yeewu ngir julli fajar.
8- damay wax ginnaw bi ma yeewoo ci nelaw yi: "alhamdu lil-Laahil lazii ahyaanaa bahda maa amaatanaa wa ilayhin nuzuuru"
lan mooy teggini lekk ?
T-
1- damay yéenee toop Yàlla ci sama lekk ak sama naan.
2- raxas ñaari yoxo lu jiitu lekk gi.
3-damay wax:"bismil Laahi",ma lekke sama loxo ndeyjoor tey tibbu ci sama kanan,te duma lekk ci diggu ndab li,wala ci kanamu keneen.
4- buma fàttee wax bismil Laahi, damay wax "bismil Laahi awwalahu wa aaxirahu"
5- damay doyloo li ma lif ciw ñam,te du ma sikk benn ñam,buma yéemee ma lekk ko,buuma yéemul ma bàyyi ko.
6- damay lekk ay tibb rekk, te duma leek lu ëpp
7- duma ëf ci ñam wi wala naan gi, damakoy bàyyi bamu sedd
8- damay bokk ñam wi ak ñeneen, ak njaboot gi wala gan gi.
9- duma njëkk a tàmbalee lekk koo xam ne moo ma mag.
10- damay tuud Yàlla bu may naan, damay toog bumay naan te ci ñatti dogit laay naane.
11- da may sant Yàlla buma noppee ci lekk gi.
li mal teggini sol yéere yi?
1-bu may sol sama yéere damay tàmbalee si ndeyjoor bi.
2- duma wàcce sama yéere sama suufu dojor.
3- xale yu góor yi du nu sol yéerey xale yu jigéen yi, jigéen yi itam du ñu sol yu góor ñi.
4- bañ a niroole soliin ak yéefar yi wala kàccor yi.
5- tudd Yàlla bumay summi yéerée yi
6- njëkk a sol dàll wi ci tànku ndeyjoor wi, njëkka summi tànku càmmoñ bi.
tuddal teggini war?
1- damay wax "bismil Laahi, alhamdu lil-Laahi", "subhaanal lazii saqara lanaa haazaa wa maa kunnaa lahu muqriniina 13" "wa innaa ilaa Rabbinaa la munxalibuuna 14" Saaru suxrufi: 13,14.
2- Buma rombee ab jullit, dama koy nuyu.
tuddal teggini yoon?
1- damay ya moo te di woyoflu ci sama doxiin, damay dox itam ci ndeyjooru yoon wi.
2- damay nuyu kuma dajeel.
3- damay dammu samab gis, te duma lor kenn.
4- damay dégle lu baax, di tere lu bon.
5- damay jële luy lore ci yoon wi.
Tuddal teggini dugg ci kër ak génn fa?
1- Damay génne sama tànku càmmoñ daal di wax: "Bismil Laahi, tawakkaltu halal Laahi, laa hawla walaa xuwwata illaa bil-Laahi, Allaahumma innii ahuuzu bika an adilla aw udalla, aw azilla aw uzalla, aw aslima aw uslama, aw ajhala aw ujhala halayya" 2- damay dugge kër gi si sama tànku ndeyjoor, daal di wax: "Bismil Laahi walajnaa, wa bismil Laahi xarajnaa, wa halaa Rabbinaa tawakkalna"
3- damay tàmbali ci socc, daal di nuyu waa kër gi.
Tuddal teggini faj aajo?
1- damay dugge sama tànku càmmooñ
2- damay wax balaa may dugg: "Bismil Laahi, Allaahumma innii ahuuzu bika minal xubusi wal xabaa-isi"
3- duma dugal dara lu am turu Yàlla
4- damay suturlawu bumay faj aajo.
5- duma wax ci barau faju kaa yu aajo ba.
6-duma jublu xibla,te duma ko dummóoyu bumay saw wala may dem duus.
7- damay jëdfandikoo loxo càmmooñ ci dindi sobe, te duma jëfandikoo loxo ndeyjoor.
8- duma faj aajo ci kaw yoonu nit ñi wala seen ker yi.
9- damay raxas samay yoxo ginnaaw faj aajo gi.
10- damay génnee sama tànku ndeyjoor, daal di wax: "xufraanaka"
Tuddal teggini jàkka?
damay dugge jàkka ji sama tànkub ndeyjoor, daal di wax: "Bismil Laaahi, Allaahumma iftah lii abwaaba rahmatika"
2- duma toog ndare ma julli ñaari ràkka
3- Duma jaar ci kanamu kuy julli, wala may yéene lu réer ci jàkka ji, wala may jaay wala jënd ci biir jàkka ji.
4- Damay génne jàkka ji ci sama tànku càmmooñ, daal di wax: "Allaahumma innii as-aluka min fadlika"
Tuddal teggini nuyoo?
1- Buma dajee akub jullit damakoy njëkka nuyu, daal di wax: "assalaamu halaykum wa rahmatul Laahi wa barakaatuhu" duma yam ci junj ci sama loxo rekk, ci ludul nuyoo.
2- Damay muuñ si kanamu ki may nuyu.
3- Damay saafoonte ak moom ci sama loxo ndeyjoor.
4- Buma kenn nuyoo dama koy delloo nuyoo ca namu gën a rafete, wala ma delloo ko lu mel ni nuyoom ba.
5- Duma njëkka nuyu ab yéefar, te buma nuyoo ma delloo ko lu mel ni nuyoom ba.
6- Xale mooy nuyu mag, ki war mooy nuyu kiy dox, kiy dox mooy nuyu ki toog, ñi néew ñooy nuyu ñi bari.
Tuddal teggini yéglu?
1- Damay yéglu balaamaa dugg cib barab.
2- Damay yéglu ñatti yoon te du ma ko weesu, ginnaaw ga ma waññiku.
3- Damay fëgg buntu ba ndànk, te duma taxaw di jàkkaarloo ak buntu bi, waaye damay taxaw ci wetu ndejooram wala càmmooñam.
4- Duma dugg si néggu sama baay ak sama yaay, walaa néegu kenn lu jiitu may yéglu, rawatina lu jiitu fajar wala waxtuw dallu ci tisbaar, wala ginnaaw jullig gee.
5- Man namaa dugg ci barab bess dëkkewul ci ludul may yéglu, lu mel ni: fajukaay, wala jaayukaay.
Tuddal teggini ñeewantu rab yi?
1- Damay leel rab yi di leen nàndal.
2- Yërëm ak ñeewante rab yi, te bañ leena teg lu ñu àttanul
3- Duma mbugal rab yi benn xeetu mbugal wala lor.
Tuddal teggini tàggatu:
1- Damay jublu si tàggatu gi am kàttan ci topp Yàlla ak am ngërëmam.
2- Dunu fo ci jamonoy julli.
3- Xale yu góor yi du ñu bokk ak xale yu jigéen yi di tàggatu.
4- Damay sol yéere tàggatukaay bu muur samay awra.
5- Damay moytu tàggatu bu daganul, ni ki bu am dóor si kanam wala wuññi awra.
Tuddal teggini kaf?
1- dëggu ca kaf ga te bañ a fen.
2-kaf gu mucc ci sikkal ak yéjji ak lor ak tiitalaate.
3- Bañ a baril kaf.
Tuddal teggini tissooli?
1-booy tiissoli nga teg ci sa gémmiñ sa loxo wala mbubb wala morso.
2- Nga sant Yàlla ginnaaw bi nga tiissolee "alhamdu Lillaahi"
3- na ko mbokkam mi wax wala àndandoom: "yarhamukal Laahu"
Bu ko ko waxee, na wax: "yahdiikumul Laahu wa yuslihu baalakum"
Lan mooy teggini óbbali?
1- Jéema nëbb óbbali gi.
2- Bañ a yékkati kàddu ci wax: "aah, aah"
3- Teg sa loxo ci sa gémmeñ
Tuddal teggini jàng Alxuraan?
1- jàng ko cig laab kinnaaw jàpp.
2- Toog ci teggin ak wegu.
3- Muslu ci Saytaane ca tàmbalig njàng ma.
4- Di settantal njàng ma.
Xaajub jikko yi.30
Tuddal ngëneelu rafet jikko?
Yonnent bi yal na ko yàlla dolli jàmm ak mucc, neena: "Ki gën a mat ngëm ci way-gëm yi mooy ki ci gën a rafet jikko" Tirmizzii ak Ahmad ñoo ko soloo.
Lu tax ñuy taqoo ak jikkoy Lislaam yi?
1- Ndax day tax Yàlla mu kawe mi bëgg la
2- Day tax nit ñi bëgg la
3- Te moo gën a diis si peesekaay ya.
4- Te dees na ful pay ga ak yiw wa ci rafet jikko.
5- Te mandarga la ci mattug ngëm
6- Ci fan la niy jële jikko?
7- Ci Alxuraanul Kariim, Yàlla mu kawe mi neena: "Alxuraan jii de day gindee jëme ca la gën a jub" Saaru Israa: 9 Ak ci Sunna: Yonnent yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc neena: "Dan maa yónni ngir ma mottali jikko yu rafet yi" Ahmad moo ko soloo
Lan mooy jikkoy rafetal ak i anamam?
Rafetal: mooy di fuglu Yàlla saa sune, ak di defal mbindéef yi yiw ak lu rafet.
Yonnent bi yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc neena: "Yàlla dafa waral rafetal ci lépp" Muslim moo ko soloo
Bokk na ci anami rafetal yi:
- Rafetal ci jaamu Yàlla mu kawe mi, te mooy di sellal jaamu gi.
- Rafetal jëme si ñaari wayjur, ci wax ak jëf
- Rafetal jëm ci bokk yi ak jegeñaale yi.
- Rafetal jëm ci dëkkadoo yi.
- Rafetal jëm ci jirim yi ak Way-ñakk yi.
- Rafetal jëm ci kuy ñaawal jëme ci yaw.
- Rafetal wax yi.
- Rafetal werente wi
- Rafetal jëme si rab yi.
Lan mooy safaanu rafetal?
Safaanu rafetal mooy ñaawal
* Te bokk na ci: baña sellal ci jaamu Yàlla mu kawe mi.
* Ak dog ñaari wayjur.
* Ak dog mbokk.
* Ak ñaawal dëkkadoo.
* Ak bañ a rafetal jëme ci way ñakk yi ak yeneen yu dul yoo yu ci ñaawal i wax wala jëf.
Yan mooy xeeti kóolute yi aki anamam
T-
1- Kóolute ci wattu àqi Yàlla mu kawe mi.
Ay anamam: am kóolute ci def jaamu Yàlla yi ci julli ak joxe azaka ak woor ak aj ak yeneen yi Yàlla farataal si nun.
2- Kóolute ci wattu àqi mbindéef yi.
- Ci wattu deri nit ñi.
- Ak séeni alal
- Ak seen i deret.
- Ak seen i bóot, ak mbooleem lila nit ñi wóolu.
Yàlla wax na ci melukaani waytexe yi: "Ak ñi nga ñiy sàmm seen i kóllare ak séeni dëel 8" Saaru Almoominuuna 8
Lan mooy safaanu kóolute?
Wor, te mooy sànk àqi Yàlla mu kawe mi ak àqi nit ñi.
Yonnent bi yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc neena: "Màndargay naaféq ñatt la"mu tudd ca- "bu nu ko wóoloo mu wor" Buxaari ak Muslim dёppoo na nu ci.
Lan mooy jikkoy dëggu?
Mooy xibaare lu dëppoo ak li am, wala mbir mi ni ki mu ame
Bokk na ci ay anamam:
Dëggu ci wax ak nit ñi.
Dëggu ci dige.
Dëggu ci wax ak jëf.
Yonnent bi yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc neena: "Dëggu day jëmale cig mbaax, te ag mbaax day jëmale Aljana, nit ki dina dëggal ba mujj nekk Dëggalaakon Buxaari ak Muslim dёppóo nan ci.
Lan mooy safaanu dëgg?
Fen, te mooy wuute ak li wér, te bokk na ca, di fen nit ñi ak wuuteb dig, ak seede ay caaxaan.
Yonnent bi yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc neena: "Fen day jëmale nit ki cig kàccoor, te ag kàccoor day jëmale Sawara, te nit ki dina fen bañu bundal ko fa Yàlla ni fenkat la" Buxaari ak Muslim dёppoo na nu ci. Yonnent bi yal na ko Yàlla dolli jàmm mucc neena: "Màndargay naaféq ñatt la" -mu tudd ca- "bu waaxtaanee day fen, bu digee day wuute dig ba" Buxaari ak Muslim dёppóo nan ci.
Tuddal xeeti muñ yi?
- Muñ si topp Yàlla mu kawe mi
- Mu moy Yàlla yi
- Muñ ndogal yu metti yi, te sant Yàlla ak lo man di am
Yàlla mu kawe mi neena: "Yàlla dafa bëgg way muñ yi" Saaru Aali Himraan 146 Yonnent bi yal na ko Yàlla dolli jàmm mucc neena: "yéemu naa mbiri way gëm ji moom de mbiram yépp yiw la,te kenn amul loolu ku dul way gëm,bu ko mbékte dalee day sant mu doon yiw ci moom,bu ko aw lor dalee day muñ mu doon yiw ci moom" Muslim moo ko soloo.
Lan mooy safaanu muñ?
- Mooy ñàkka muñ si topp Yàlla, ñàkka muñ moy yi, ak di yéjji ndogal yi ci wax wala si jëf
Bokk na ci ay meloom:
- Mébet dee.
- di mbej say lex.
- Di xotti say yéere.
- Di tasaare sa kawar
- Di ñaan alkande ci sa kaw.
Yonnent bi yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc neena: "Pay gi de mi ngi ci màggug nattu yi,te Yàlla su bëggee aw nit da leen di nattu,ku gërëm ngërëm ñeel ko,waaye ku mer merum Yàlla ñeel ko" Tirmizii ak Ibn Maaja ñooko soloo
Tuddal jikkoy dimbalaante?
Mooy nit ñi di dimbalànte seen biir ci dëgg ak uw yiw.
Anami dimbalànte yi:
- Dimbalànte si delloo àq yi.
- Dimbalànte ci delloo Aji-tooñ ji.
- Dimbalànte ci faj aajoy nit ñi ak way ñàkk yi.
- Dimbalànte ci yiw.
- baña dimbalaante si bàkkaar ak lor ak noonoo
Yàlla mu kawe mi neena: "dimbalànte leen cig mbaax ak ragal Yàlla, te bu leen dimbalànte ci bàkkaar ak noonoo te ngeen ragal Yàlla moom Yàlla ku tar mbugal la" Saaru Maa-ida 2 Yonnent bi yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc neena: "jullit ak moroom ma dañoo wara mel ni ab tabax; lenn lune day dëgëral leneen la" Buxaari ak Muslim dёppóo nan ci. Yonnent bi yal na ko Yàlla dolli jàmm mucc neena: "Jullit mooy mbokkum jullit ba,du ko tooñ,te du ko jébbale,ku nekk ci sa aajoy mbokk,Yàlla dina nekk ci say aajo,ku dindil ab jullit aw tiis, Yàlla dina ko dindil aw tiis ci tiisi bisub taxawaay ba,te ku suturaal ab jullit Yàlla dina ko suturaal bisub taxawaay ba" Buxaari ak Muslim dёppóo nan ci.
Yan mooy xeeti jikkoy kersa?
1- am kersa ci Yàlla: ci nga bañ koo moy moom Yàlla mu sel mi.
2- am kersa ci nit ñi: bokk na ca bàyyi wax ju ñaaw te bon, bañ a wuññi awray kenn.
Yonnent Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc neena: "Ngëm juroom ñaar fokki xaaj la yu topp" wala: "juróom mbenni fukki xaaj la ak lu topp" - "ay pàcci, bi ci gën a kawe: mooy wax: laa ilaaha illal Laahu, bi ci gën a suufe, mooy: randale lor si kaw yoon. wi, te kersa benn pàcci la ci ngëm" Muslim moo ko soloo
Tuddal meloy jikkoy yërmande?
- Yërëm mag ñi te weg leen.
- Yërëm xale yu ndaw yi.
- Yërëm way ñakk yi ak way aajo woo yi
- Yërëm rab yi ci di leen jox lekk te bañ leena lor.
Loo lu la Yonnent bi yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc di wax ne: "dangay gis jullit yi si seen yërëmante ak seen ug bëgante ak seen ñeewanten te ñu mel ni benn yaram,bu ci benn cér di jàmbat mbooleem cér yi dañ koy wuyu ci bañ a nelaw ak si tàng" Buxaari ak Muslim dёppóo nan ci. Yonnent Yàlla bi yàlna ko Yàlla dolli jàmm ak mucc neena: "ñiy Yërëme de Aji-Yërëme ji de dana leen yërëm, yërëm leen waa Soof si, ki ci Asamaan yërëm leen" Abuu Daawuda soloo nako ak Tirmiziiu ak ñeneen.
Lan mooy xeeti jikkoy mbëggeel?
Bëgg Yàlla mu kawe mi
Yàlla mu kawe mi neena: "ñi gëm de Yàlla lan gëna bëgg" Saaru Baqara: 165
Bëgg Yónnent bi yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc
Moom wax na ne: "Giñ naa ci ki sama bakkan nekk ci loxoom,kenn ci yéen du gëm ndare ma gënal ko wayjuram ak doomam" Buxaarii moo ko soloo
Bëgg way gëm yi, te bëggal leen yiw ni ki nga ko bëggale sa bopp.
Yonnent bi yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc neena: "Kenn ci yéen du gëm; ndare mu bëggal mbokkam li mu bëggal boppam" Buxaarii moo ko soloo
Xamleel lan mooy bélli?
Mooy feccikog xar kanam, àndag mbégte ak muuñ ak ñeewant, ak feeñal mbégte ci boo dajee ak nit ñi.
te mooy safaanug fas xarkanam, ci kanami nit ñi ci lépp lu leen di dawloo
Te ay Hadiis ñëw na si ngëneeli loolu, jële nanu si Abii Zarrin yal na ko Yàlla dolli ngërëm, neena: Yonnent bi yal na ko Yàlla dolli jàmm ak muicc neena: "Bul xeeb ci lu baax dara, donte dangay dajee ak sa mbokk si kanam gu bélli Muslim moo ko soloo Yonnent bi yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc néena: "Sag muuñ ci sa kanamu mbokk sarax la" Attirmizii moo ko soloo
Lan mooy soxor?
Mooy nga mébet ci keneen mu ñàkk xéewalam, wala nga bañ keneen am xéewal.
Yàlla mu kawe mi neena: "ak ci ayu Aji-Soxor ji saayu soxoree 5". Saaru Alfalaxi: 5
Jële nanu ci Anas ibn Maalik, yal na ko Yàlla dollee gërëm, neena yonent bi yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc, neena: "bu leen bañante, te bu leen soxorante, te bu leen dummóoyante, nekk leen -yéen jaami Yàlla yi- ay mbokk" Buxaarii ak Muslim ñoo ko soloo
Lan mooy yéjji?
Mooy di reetaan sa mbokkum jullit ak di ko xeeb,te loolu daganul
Yàlla mu kawe mi wax na ci tere loolu: "ée yéen ñi gëm bu benn nit reetaan beneen nit ndax amaana ñooñu gën ña leeni reetaan bu benn jigéen it di reetaan benn jigéen ndax amaana ñoom ñu gën ña leen di reetaan bu leen di ayibalante te bu leen di woowante ci ay tur yu leen neexul turu kàccoor yooyi de lu ñaaw la ginnaaw ngëm ga te ku tuubul ñoom ñooy tooñkat yi" Saaru Al-mujaadala 11
Xam leel lan mooy woyoflu?
Mooy nit ki bañ a gis ne moo gën a kawe nit ñi, du xeeb nit ñi te du bañ dëgg
Yàlla mu kawe mi neena: "Jaami Yàlla yi dëgg mooy ñiy dox ndànk ci kaw Suuf" Saaru Alfurxaan 63 Maanaam: di ay Aji-woyof Yonnent Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc neena: "Kenn du woyof-wofof lu lu dul ne Yàlla dina ko yékkati Muslim moo ko soloo Yonnent bi yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc waxaat ne: "Yàlla soloo nama ne nangeen di woyoflu ba kenn du puukarewu si kaw kenn, te kenn itam du bew si kaw kénn" Muslim moo ko soloo
Yan mooy xeeti rëy mi nga xamni dafa araam?
1- Rëy ci kaw dëgg, te mooy delloo dëgg bañ koo nangu
2- Rëy ci kaw nit ñi, te mooy xeeb leen ak doyodal leen
Yonnent Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc neena: "Ku ab peppu rëy nekk ci xolam du dugg Aljana" Benn waay neko: nit kiy bëgg ay Yéereem ak i dàllam rafet nag? mu ne ko: Yàlla dafa rafet te daa bëgg lu rafet, rëy mooy: bañ dëgg ak xeeb nit ñi" Muslim moo ko soloo.
- Batarul hàq: mooy Bañ dëgg
- Xamtun naasi: mooy xeeb nit ñi.
- Yéere bu rafet ak dàll yu rafet bokkul ci rëy.
Tuddal yenn xeeti wuruj yi nga xamne dafa araam?
- Wuruj ci jaay ak jënd, te mooy nëbb ayib ci njaay mi.
- Wuruj si booy jàng xam-xami, te bokk na ca jàngkat bi di wuruj ci nattug njàng mi,( composition yi)
- Wuruj ci ay wax, lu mel ni di sede lu dul dëgg.
- ñàkka matal kollare ci say wax, ak ci li nga dëpoo ak nit ñi.
ñëw na ci tere wuruj ne: yonnent bi dafa rombu benn ndabul ñam, daal di ciy dugal loxoom, baaraam yi daal di tooy, mu wax boroom ñam wi neko: "lii lanla yaw boroom ñam wi?" muneko: taw beeko laal yaw yonnent Yàlla bi. Yónnent bi neko: "Lu tax defooko si kaw ñam wi ngir nit ñi gis ko? képp kuy wuruj bokkul ci nun" Muslim moo ko soloo
Subra: mooy ndabul ñam
Lan mooy jëw?
Mooy nga tudd sa mbokk si lu ko neexul foo xamne nekkufa
Yàlla mu kawe mi neena: "Bu kenn si yéen di jëw keneen ndax kenn si yéen bëgg naa lékk yàppu mbokkam mu dee, yéen ñéppa bañ loolu, ragal léen Yàlla, Yàlla Aji-Jéggale la Aji-yërëme la 12" Saaru Alhujraat: 12
Xamleel rambaaj?
Mooy di tuxal ay wax si digante niññi ngir yàq séen diganté
Yónnent yàlla bi neena: "Ab raambaaj du dugg Aljana" Muslim moo ko soloo
Lan mooy tàyyeel?
Mooy nit ki di diis lu ci def yiw ak li mu war a def.
Te bokk na ca: Tàyyeel ci def wartéef yi.
Yàlla mu kawe mi neena: "Naaféq ya dañuy jéem a wor Yàlla waaye Yàlla dana leen njuuy, te bu ñu jògee jëm ca julli ga, da ñiy jòg cig tayyeel, da ñiy ngistal ci bëti nit ñi, te du nu tudd Yàlla lu dul lu néew ci moom 142" Saaru Annisaa 142
Jullit bi warnaa moytu tàyyeel ak giim ak, toog rek, te ligéey ak yëngatu ak pastéefu ci dund gi ci lépp luy gërëmloo Yàlla
Tuddal xeeti mer yi?
1-Mer mees gërëm:te mooy mer ngir Yàlla saa yu yéefar ak naaféq yi wala ñeneen xotte wormaam moom Yàlla mu sell mi
2-Mer mu ñu ngàññi:te mooy mer miy def nit ki di def aka wax lu jaaduwul.
Liy faj mer mun ngàññi:
Jàppu
Mu toog bu dee dafa taxawoon, waaye mu tëdd bu dee dafa toogoon.
Mu taqoo ak ndenkaandey Yonnent bi ci loo lu: "bul mer"
Mu téye boppam ci bañ a jëfandikoo meram.
Muslu ci Yàlla ci Saytaane mi ñu dàq ci yёrmandey Yàlla
Noppi
Lan mooy luññutu?
Mooy wuññi ak gëstu awray nit ñi ak li ñu doon làq.
Bokk na ci ay anamam yu araam:
- Di yër awray nit ñi ci seen kër yi.
- Nit ki di deglu waxi nit yoo xam ne yéguñu ko.
Yàlla mu kawe mi neena: "Bu leen di luññutu 12" Saaru Alhujraat: 12
Lan mooy yàq? ak lan mooy nay? ak lan mooy tedd?
Nay mooy: sànk alal ci lu dul dëgg
Safaanam mooy: nay: te mooy baña joxe wolif ci dëgg
Li wér nag mooy digg-dóomu séen digante, jullit bi nekk ku tdéd
Yàlla mu kawe mi neena: "Ak ñi nga xam ne bu ñuy joxe du ñu yàq te du ñu nay, dañuy digg-doomu 67" Saaru Alfurxaan: 67
Lan mooy buqat? ak lan mooy njàmbaar?
Buqat mooy: di ragal lu jarula ragal
Ni ki di ragala wax dëgg ak weddi lu ñaaw.
Njàmbaar: mooy dégmal dëgg, lu ci mel ne dégmal xeexukaay ya ngir aar Lislaam ak jullit yi.
Yonnent bi daa na wax ci ñaanam yi: "Yaw Yàlla maa ngi lay muslu buqat" yoneent bi wax ne: "Jullit bu am kàttan bi de la Yàlla gën a bëgg ci jullit bu lompañ bi, waaye ñoom ñéppa am yiw" Muslim moo ko soloo
Tuddal yenn xeeti wax yu araam yi?
- Lu mel ni rëbbaate ak saaga.
- ak lu mel ni di wax naa diw "rab la" walla ay baat yu ni mel.
-Wala tudd ay awra ci ay kàddu yu ñaaw te bon.
- Yonnent bi tere na yooyu yépp, daal di wax ne: "Nekkul jullit Aji-Jamaate gi du caagine Aji-Rëbbaate gi, wala Aji-Def ñaawtéef, wala Aji-Bon lammiñ" Tirmizzi ak Ibn Hibbaan ñooko soloo
Tuddal sabab yiy dimbali jullit bi ci jikko woo ay jikko yu rafet
1- Di ñaan Yàlla mu wërsëgal la rafet jiko, te dimbali la ci.
2- Di fuglu Yàlla mu màgg mi te kawe, ci ne xam na sa mbir, moo ngi lay dégg te moo ngi lay gis.
3- Di fàttaliku yoolu rafet jiko ci ne day waral dugg Aljana
4- Di fàttaliku mujjug ñaaw jiko ci ne day waral dugg Sawara.
5-Rafet jiko day waral bëggug Yàlla ak bëggug mbindeef yi,ñaaw jiko da waral bëñug Yàlla ak bañug mbindeef yi.
6- Jàng jaar-jaaru Yónnent bi yàlna ko Yàlla dolli mucc ak jàmm ak di roy si moom
7- Di àndag ñu baax ñi te moytu ñu bon ñi
Xaaju ñaan yi ak tudd Yàlla yi.43
Lan mooy ngëneelul tudd Yàlla?
Yonnent bi yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc neena: "misaalum kiy tudd Yàlla ak ki dul tudd Yàlla,mi ngi mel ni kuy dund ak ku dee" Buxaarii moo ko soloo
- Ndax dayob dundug nit ki mi ngi ci kem ni miy tudde Yàlla mu kawe mi"
- Tuddal yenni njariñi Tudd Yàlla?
1- Day gërëmloo Aji-yërëme ji
2- Day dàq Saytaane
3- Day aar jullit bi ci ay.
4- Te da ciy ame ak pay ak ub yool.
Lan mooy Tudd Yàlla gi gën?
"Laa ilaaha illal Laahu" Tirmizii ak Ibn Maaja ñooko soloo
Lan ngay wax soo yeewoo ciy nelaw?
"Alhamdu lil-Laahil lazii ahyaanaa bahda maa amaatanaa wa ilayhin nuzuuru" Buxaari ak Muslim dёppóo nan ci.
Lan ngay wax booy sol sa yéere?
"Alhamdu lil-Laahil lazii kasaanii haazas sawba wa razaxaniihi min xayri hawlin minnii walaa xuwwata" Abuu Daawuda ak Attirmizii soloo nan ko ak ñenéen
Lan ngay wax booy summi sa yéere?
"Bismil Laahi" Attirmizii moo ko soloo
Lan mooy ñaanug sol yeére bu bees?
"Allaahumma lakal hamdu anta kasawtaniihi, as-aluka xayrahu wa xayra maa sanahta lahu, wa ahuuzu bika min sarrihi wa sarri maa sanahta lahu" Abuu Daawuda soloo nako ak Tirmiziiu ak ñeneen.
Lan moom ñaanug ku sol yéere bu bees?
Boo gisee ken sol yeér bu bees danga koy ñanal, daal di wax: "Yal na nga ko ràppal te Yàlla wuutalal lako" َAbuu Daawuda moo ko soloo.
Tuddal ñaanug dugg si wanag, te mooy barabu bu faj aajo?
" Allaahumma innii ahuuzu bi ka mi nal xubusi wal xabaa-isi" Buxaari ak Muslim dёppoo na nu ci.
Lan mooy ñaanug génn si wanag?
"Xufraanaka" Abuu Daawuda soloo nako ak Tirmiziiu ak ñeneen.
Lan ngay waxwax bala nga jàppu?
"Bismil Laahi" Abuu Daawuda soloo na ko ak ñeneen.
Lan lees di ñaan ginnawam njàpp?
"Ashadu an laa ilaaha illal-Laahu wahdahu laa sariika lahu, wa ashadu anna Muhammadan habduhu wa rasuuluhu" Muslim moo ko soloo
Lan mooy ñaanug génn ci kër?
"Bismil-Laahi, tawakkaltu halal Laahi, wa laa hawla wa laa xuwwata illaa bil-Laahi" Abuu Daawuda soloo nako ak Tirmizii ak ñeneen.
Lan mooy ñaanug dugg ci kër?
"Bismil-Laahi walajnaa, wa bismil-Laahi xarajnaa, wa halaa Rabbinaa tawakkalnaa" topp "mu nuyu waa kër gi" َAbuu Daawuda moo ko soloo.
Lan mooy ñaanug génn ci jàkka?
"Allaahumma iftah lii abwaaba rahmatika" Muslim soloo nako
"Tuddal ñaanu génn ci jàkka?
"Allaahumma innii as-aluka min fadlika" Muslim soloo nako.
Lan ngay wax boo déggee nodd?
Damay wax li nodd-kat bi di wax, ba mu des ci: "hayya halas salaati" ak "hayya halal falaahi" dama fay wax: "laa hawla wa laa xuwwata illaa bil-Laahi" Buxaari ak Muslim dёppoo na nu ci.
Lan ngay wax ginnaaw nodd gi?
(Dangay julli ci Yónnent bi yà lna ko Yàlla dolli jàmm ak mucc) Muslim moo ko soloo Te nga wax: "Allaahumma Rabba haazihid dahwatit tàmmati, wassalaatil xaa-imati, aati Muhammadanil wasiilata walfadiilata, wabhashu maxaaman mahmuudanil lazii wahadtahu" Albuxaarii
Nga ñaan ci diggante nodd gi ak taxawal ga, ndax ñaan fa kenn du ko delloo
Yan ñaan ngay wax ci Suba si ak ci Ngoon si?
Jangàl Aayatul kursiyyi: "Allaahu laa ilaaha illa Huwal Hayyul xayyuumu laa taaxuzuhu sinatun walaa nawmun lahu maafis Samaawaati wa maa fil-Ardi man zal lazii yasfahu hinda huu illaa bi-iznihii yahlamu maa bayna aydiihim wa maa xalfahum wa laa yuhiituuna bi say-in min hilmihii illaa bimaa saa-a wasiha kursiyyuhus Samaawaaati wal-ardi wa laa ya-uuduhu hifsuhumaa wahuwal Haliyyul Hasiimu 255" Saaru Bàqara: 255 Te nga jàng: bismil-Laahir Rahmaanir Rahiimi "Xul huwal Laahu ahadun 1 Allahus Samadu 2 Lam ya lid wa lam yuulad 3 Wa lam yakun lahuu kufuwan ahadun 4" ñatti yoon Bismil-Lahir Rahmaanir Rahiimi "Xul ahuusu bi-Rabbil falaxi 1 Min sarri maa xalaxa 2 Wa min sarri xaasixin izaa waxaba 3 Wa min sarrin naffaasaati filhuxadi 4 Wa min sarri haasidin izaa hasada 5" ñatti yoon Bismil-Lahir Rahmaanir Rahiimi "Xul ahuuzu bi-Rabbin naasi 1 Malikin naasi 2 Ilaahin naasi 3 Min sarril waswaasil xannasi 4 Allazii yuwaswisu fii suduurin naasi 5 Minal jinnati wannaasi 6" ñatti yoon "Allaahumma Anta Rabbii laa ilaaha illaa Anta, xalaqtanii wa anaa habduka, wa anaa halaa hahdika wa wahdika maastatahtu, ahuuzu bika min sarri maa sanahtu, abuu-u laka bi nihmatika halayya, wa abuu-u bi zanbii, faxfir lii, fa-innahu laa yaxfirus sunuuba illaa Anta" Buxaarii moo ko soloo
Lan ngay wax booy nelaw?
"Bismikal Laahumma amuutu wa ahyaa" Buxaari ak Muslim dёppoo na nu ci.
Lan ngay wax ba la ngay lekk ñam?
"Bismil Laahi"
Booko fàttee sa tàmbali ga, nanga wax:
"Bismil-Laahi fii awwali hii wa aaxiri hii" Abuu Daawuda soloo nako ak Attirmizii.
Lan ngay wax soo lekkee ba noppi?
"Alhamdu lil-Laahil lazii athamanii haazaa wa razaxa niihi min xayri hawlin mi nnii wa laa xuwwata" Abuu Daawuda ak Ibn Maaja ñooko soloo ak ñeneen
Lan mooy ñaan gi gan gi di ñaanal boroom ñam wi?
"Allaahumma baarik lahum fii maa razaxtahum, waxfir lahum warhamhum" Muslim moo ko soloo.
Lu nit kiy wax bu tissoolee?
"Alhamdu lil-Laahi"
Te na ko mbokkam mi wax wala àndandoo am: "yarhamukal Laahu"
Bu ko ko waxee, na wax: "yahdiikumul Laahu wa yuslihu baalakum" Buxaarii moo ko soloo
Lan ngay wax boo jòggee cib jotaay "ñaanug njéggalu bàkkari jotaay yi"?
"Subhaanakal Laahumma wa bi hamdi ka, ashadu an laa-ilaaha illaa Anta, astaxfiru ka wa atuubu ilay ka" Abuu daawuda ak Attirmizii soloo nan ko ak ñeneen
Lan mooy ñaanu war ci daaba ?
Bismil-Laahi, walhamdu lil-Laahi "Subhaanal lazii sàqara lanaa haazaa wa maa kunnaa lahu muqririina 13 wa innaa ilaa Rabbinaa la munxalibuuna 14", "Alhamdu lil-Laahi, alhamdu lil-Laahi, alhamdu lil-Laahi, Allaahu akbaru, Allaahu akbaru, Allaahu akbaru, subhaanakal Laahumma innii salamtu nafsii faxfirlii, fa-innahu laa yaxfiruz zunuuba illaa Anta" Abuu Daawuda soloo nako ak Attirmizii.
Tuddal ñaanu tukki?
Allaahu akbaru, Allaahu akbaru, Allaahu akbaru "Subhaanal lazii sàqara la naa haazaa wa maa kunnaa lahuu muqriniina 13 wa innaa ilaa Rabbinaa la munxalibuuna 14", Allahumma innaa nas-aluka fii safarinaa haazal birra wattaqwaa wa minal hamali maa tardaa, Allaahumma hawwin halaynaa safaranaa haazaa, watwi lanaa buhdahu, Allaahumma Antas saahibu fissafari, wal Xaliifatu fil-ahli, Allaahumma, inni ahuuzu bika min wahsaa-is safari, wa ka-aabatil mansari, wa suu-il minxalabi, filmaali wal-ahli"
Bu waññikoo waxaat leen, te teg ca:
"Aayibuuna, taa-ibuuna, haabiduuna, li-Rabbinaa haamiduuna" Muslim moo ko soloo
Lan la Aji-tukki ji di ñaanal Aji-des ji?
"Astawdihukulmul Laahul lazii laa tadiihu wadaa-ihuhu" Ahmat ak Ibn Maaja ñooko soloo.
Lan la Aji*des ji di ñaanal Aji-tukki ji
"Astawdihul Laahu diinaka, wa amaanataka, wa xawaatiima hamalika" Ahmat ak Attirmiziu soloo nan ko.
Lan mooy ñaanug dugg ca Jaba(?
"Laa-ilaaha ilal-Laahu wahdahu laa sariika lahu, lahul mulku wa lahul hamdu, yuhyii wa yumiitu, wa huwa hayyun laa yamuutu, bi yaddihil xayru, wa huwa halaa kulli say-in xadiirun" Attirmizii ak Ibn Maaja ñooko soloo
Tuddal ñaan gi nit ki di ñaan su meree?
"Ahuuzu bil-Laahi minas Saytaanir rajiimi" Buxaari ak Muslim dёppoo na nu ci.
Lan ngay wax ki la defal lu baax?
Yàl na la Yàlla fay yiw. Attirmizii moo ko soloo
Lan lan la niy ñaan bu li nu war tërafée?
"Bismil Laahi" َAbuu Daawuda moo ko soloo.
Lan ngay wax bu lu la bégloo amée?
"Cant ñeelna Yàlla mi nga xam ne ci ay xéewalam la yu baax yi di mate" Haakim moo ko soloo ak ñeneen.
Lan ngay wax bu loo bañ amee?
"Santnaa Yàlla ci gépp anam" Sahiihul jaamih
Nan la niy nuyoo ak nan la niy delloo nuyoo?
Jullit bi day wax: "Assalaamu halaykum wa rahmatul Laahi wa barakaatuhu"
Mbokkam mi dakoy deloo nuyoo ne ko: "wa halaykumus salaam wa rahmatul Laahi wa barakaatuhuu" Mi ngi si Attimizii ak Abuu Dawawuda ak ñeneen
Lan lani ñaan bu dee taw?
"Allaahumma sayyiban naafihan" Albuxaarii
Lan la ni yñaan bu dee taw?
"Tawalees nanu ci ngëneelu Yàlla ak yërmàndeem" Albuxaarii ak Muslim
Tuddal ñaanu ngelaw?
"Yàlla maa ngi lay ñaan yiwam di la muslu ci ayam" Abuu Daawuda ak Ibn Maaja ñooko soloo.
Tuddal ñaanug sun déggee dënnu?
"Tudd naa sellug ki dënnu yi di sabbaal ci di ko sant, ak Malaaka yi itam ngir ragal ko" Muwatta Maalik
Lan la niy ñaan bunu gisee kees nattu?
"Maa ngi sant Yàlla mi ma musal si limu la nattu, mu gënale ma ci ñu bari ci lim bind" Attirmizii moo ko soloo
ñaanu ku ragala lor dara si ay bëtam?
ñëw na ci Hadiis: "bu kenn gisee lu ko yéem ci mbokkam wala ci boppam, wala ci alalam, [na ñaan baarke], ndax bët dëgg la" Ahmat ak Ibn Maaja ñoo ko soloo ak ñeneen
Naka ngay julle ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli mucc ak jàmm?
"Allaahumma salli halaa Muhammadin wa halaa aali Muhammadin, kamaa sallayta halaa Ibraahiima, wa halaa aali Ibraahiima, innaka Hamiidun Majiidun, Allaahumma baarik halaa Muhammadin wa halaa aali Muhammadin, kamaa baarakta halaa Ibraahiima, wa halaa aali Ibraahiima, innaka Hamiidun Majiidun" Buxaari ak Muslim dёppoo na nu ci.
Xaaju yu wuute yi:21
Yan mooy juroomi àtte yin togg nit ki jëf?
T-
1- Lu war.
2- Lees sopp.
3-Lees araamal.
4- Lees sib.
5- Lu dagan
Firil juroomi àtte yii?
T-
1- Lu war: lu mel ni julliy juroom, woor weeru koor, fonk njaari wayjur
- Lu war ku ko def ñu fay ko si tuyaba ku ko bàyyi yayoo mbugal
2-Lees sopp:lu mel ni julli yi séq julli farata yi,ak julli guddi,ak joxe ñam,ak nuyoo,dees na ko woo we Sunna ak it Manduub
- Lees sopp ku ko def am si tuyaaba,ku ko bàyyi ken du ko mbugal
Ay seetlu yu am solo:
Jaadu na si ab jullit bu déggee ñu ne mbir mii sunna la wala lees sopp la mu gaawantu def ko,ruy si yonnente bi yàl na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc.
3-Lees araamal:lu melni naan sàngara,ak dog ñaari wayjur ak dàgg mbokk.
- Lees araamal ku ko bàyyi am ci tuyaaba ku ko def yayoo mbugal
4-Lees sib:lu mel ni jël ak joxe si loxo càmmoñ,ak téye say yéere si biir julli gi.
- Lees sib ku ko bàyyi am si tuyaaba, te deesu si mbugal ku ko def
5- Lu dagan: lu mel ni lekk Pom ak naan Attaaya, dees nako woo wé itam Aljaa-izu ak Alhalaalu
- Lu dagan ku ko bàyyi am si tuyaaba, te deesu si mbugal ku ko def.
Lan mooy àtteb jaay ak jëflante?
Cosaanu njaay yi ak jëflante yépp mooy ne dafa dagan, lu dul yenn yi Yàlla mu kawe mi araamal.
yàlla mu kawe mi neena: "Yàlla daganal na jaay araamal ribaa" Saaru Bàqara 275
Tuddal yenn xeeti jëflaane ak njaay yin araamal?
T-
1- Wuruj, te bokk na ca: nëbb ayibi njaay mi
Jële nanu si Abuu hurayrata mu wax ne yonnente bi dafa romb benn ndabul ñam, daal di ciy dugal loxoom, baaraam yi daal di tooy, mu wax boroom ñam wi neko: "lii lan la yaw boroom ñam wi?" mu ne ko: taw beeko laal yaw yonnente Yàlla bi. Yonnente bi neko: "Lu tax de foo ko ci kaw ñam wi ngir nit ñi gis ko? képp kuy wuruj bokkul si nun" Muslim moo ko soloo
2- Ribaa: te bokk na ci: ma am ku ma leb junni ba noppi warkoo fay ñaari junni
Ndolleen woowu mooy ribaa mu araam ma.
Yàlla mu kawe mi neena: "Yàlla daganal na jaay araamal ribaa" Saaru Bàqara: 275
Wor ak réere: ni ki ma jaay la meew mi si weenu gàtt bi, wala Jën wi ci géej gi te napp a gu ma ko.
ñëw na si hadiis: (Yonnente bi tere na njaayu wor" Muslim moo ko soloo
Tuddal yenni xéewal i Yàlla yim la xéewalal?
1- Xéewalu Lislaam, ba bokkoo si way-weddi yi
2- Xéewalu Sunna, ba bokkoo si waa Bidaa
3- Xéewalu wér ak jàmm, di dégg ak di gis ak di dox ak yeneen.
4- Xéewalu lekk ak naan ak sol.
Xéewal i Yàlla yi si nun bari na kenn manukoo lim wala mu koy takk
Yàlla mu kawe mi neena: "Bu ngeen limee xéewali Yàlla yi du ngeen ko takk,Yàlla Aji-Jéggale la Aji-Yërëme la 18" Saaru Annahli 18
Lan moo war si xéewal yi? ak na ka lan cay sante ?
Li war: mooy sant ca ci di tagg Yàlla ak di ko gërëm si Làmmiñ, si ne moom rekk mooy boroom ngëneel, ak di jëfandikoo xéewal yi ci lu Yàlla gërëm, te bañ di ko ci moy.
Yan mooy xew-xewi jullit yi?
Xewu korite ak xewu tabaski.
Ni ki mu ñëwe si ahdiisu Anas, neena: Yónnente bi dafa ñëw Madiina fekk ñu am ñaaari bis yoy dañu cay fo, mu ne leen: "ñaari bis yii mooy lan?" ñu ne ko: danu ci daan fo sa ceddo ga, Yonnente bi ne leen: "Yàlla wuutalal na leen ko lu ko gën: bisu tabaski, ak bisu korite" Abuu Daawuda soloo nako.
xew-xew bu bokkul ak ñoom ñaar ci bidaa yila.
Ban weer moo gën?
Weeru Koor
Ban bis moo gën?
Bisu Aljuma
Ban bis moo gën si at mi?
Bisu Arafa
Ban guddi moo gën si at mi?
Guddig ndogal yi(Laylatul xadri)
Lan moo la war boo gisee jigeenu jàmbur?
Li war mooy dammu sa gis, Yàlla mu kawe mi neena: "Waxal way-Gëm yu góor yi ñu dammu seen gis" Saaru Annuur: 30
ñan ñooy noonu nit ki?
1- Bakkaan biy digle lu ñaaw: te mooy nit ki di topp li ko bakkanam ak banneexaam di digal si moy Yàlla mu kawe mi, Yàlla mu sell mi neeena: "Bakkan de Aji-Digle lu ñaaw la ndare ba Yàlla yërem, sama boroom de yërëmaakon la jéggalaakon la" Saaru Yuusufa: 52 2- Saytaane:te moom noonu doomu Adama la te yitteem yépp mooy sànk nit ki,ak diko jax-jaxee ngir jëmale ko ciw ay,ak dugal ko Sawara. Yàlla mu kawe mi néena: "Bu léen topp jéegoy Saytaane yi, moom de seen noon bu mag la" Saaru Bàqara: 168 3- Andaadoo yu bon: ñiy xirtale si yu bon yi, di gàllaŋkoore si yu baax yi. Yàlla neena: "Xarit yi de bu bis baa ñenn ñi noonu ñeneen ñi la ñiy doon, ndare ñi ragal Yàlla" Saaru Assuxrufi: 67
Lan mooy tuub?
Tuub: mooy wëlbatiku ci moy Yàlla jëm ci topp Yàlla, Yàlla mu kawe mi neena: "Man dé Aji-Jéggalaakon laa ñeel ku tuub te gëm te jëf lu baax te daal di jub" Suuru Taaha 82
Yan mooy saarti tuub gu sell?
1- Bàyyi bàkkaar ba.
2- Réccu la weesu
3- Dogu si bañ caa dellu
4- Delloo àq yi ak tooñange yi seen i boroom
yàlla mu kawe mi néena "Ak ñi nga xam ne bun defee ñaawteef wala ñu tooñ seen bopp da ñiy fàttaliku Yàlla daal di jéggalu seen i bàkkaar,kan mooy jéggale bàkkaar ku dul Yàlla, te dun nuur ca lan defoon fek ne xam nan ko" Saaru Aali Himraan 135
Lan mooy julli si yonnente bi Yàlla na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc?
Li miy tekki mooy dangay ñaan Yàlla mu tagg Yonnente bi sa mbooloom Malaaka yu kawe ya"
Lan mooy maanaam Subhaanal Laahi?
Sàbbaal mooy sellal Yàlla mu kawe mi soreeleko bépp wàññeeku ak ayib ak ñaawteef
Lan mooy maanaam Alhamdu lil-Laahi?
Mooy bakk Yàlla mu kawe mi, ak melele ko bépp melow mat
Lan mooy maanaam Allaahu Akbaru?
Maanaam mooy ni Yàlla mu sell mi moo gën a màgg lépp lu mu man a doon, gën a màgg gën a tedd lépp lu mu man a doon.
Lan mooy maanaam Laa hawla wa laa xuwwata illaa bil-Laahi?
Maanaam mooy: jaambi amul benn soppeekuy juge si benn anam jëm si beneen anam,te amul si loo lu benn kàttan ndare mu bawoo fa Yàlla.
Lan mooy maanaam Astaxfirul Laahi?
Mooy: jaam bi sàkku ci boroomam mu far ay bàkkaaram te suturaal ay ayibam